Teewul xalaam ga di wéye daŋ,
te la loxo yay dëgërloo mooy
loxoy Jàmbaar ju Yanqóoba,
kookooy Sàmm bi, Doju cëslaayal Israyil,
mooy sa Yàllay baay, ji lay wallu,
mooy Aji Man ji lay barkeele
ca barkey asamaan, ya fa kaw,
ak barke ya ne leww ca suuf xóote ya,
teg ca barkeb njur ak nàmpal.