Njàlbéen ga 49:24-25
Njàlbéen ga 49:24-25 KYG
Teewul xalaam ga di wéye daŋ, te la loxo yay dëgërloo mooy loxoy Jàmbaar ju Yanqóoba, kookooy Sàmm bi, Doju cëslaayal Israyil, mooy sa Yàllay baay, ji lay wallu, mooy Aji Man ji lay barkeele ca barkey asamaan, ya fa kaw, ak barke ya ne leww ca suuf xóote ya, teg ca barkeb njur ak nàmpal.