Ma ngay ñaanal Yuusufa. Mu ne:
«Yàlla ji samay waajur Ibraayma ak Isaaxa toppoon,
moom Yàlla, ji ma sàmm, ba ma juddoo ba tey jii,
malaaka mi ma jot ci bépp loraange—
yal na barkeel xale yi,
ba ñu saxal sama tur
ak samay turi waajur, Ibraayma ak Isaaxa,
te giir, ba ne gàññ ci kaw suuf.»