Peeñu ma 10
10
Àtte bu mujj ba agsi na
1Ci kaw loolu ma gis meneen malaaka mu am doole, muy wàcce asamaan, làmboo aw niir, ag xon tege ci bopp bi, kanam gi mel ni jant bi, tànk yi mel ni jumi sawara. 2Mu ngi yor ab téere bu ndaw bu ñu ubbi. Mu teg tànku ndijooram ci géej gi, teg tànku càmmoñam ci jéeri ji. 3Mu xaacu ca kaw, mel ni gaynde guy yëmmu. Naka la xaacu, juróom ñaari dënu jib. 4Naka la juróom ñaari dënu yi jib, may waaja bind, daldi dégg baat bu jóge asamaan, ne ma: «Loolu juróom ñaari dënu yi wax de, gas ko, suul, bu ko bind.»
5Ba mu ko defee malaaka ma ma gisoon mu ŋarale géej geek jéeri ji, yékkati loxol ndijooram, jëme asamaan. 6Mu giñ ci kiy dund ba fàww, ki sàkk asamaan ak li ci biiram, ak suuf ak li ci biiram, ak géej ak li ci biiram. Mu ne: «Négandiku wees na, 7waaye bu bési kàddug juróom ñaareelu malaaka mi taxawee, ba mu tàmbalee wal liit gi, su keroogee pexem Yàlla miy kumpa dina sotti, na mu ko waxe woon ay jaamam, yonent yi.»
8Ba loolu amee baat ba ma déggoon, mu bawoo asamaan, dellu wax ak man, ne ma: «Demal jël téere bu ndaw bi ñu ubbi ci loxol malaaka mi ŋarale géej geek jéeri ji.»
9Ma dem ba ci malaaka mi, ne ko mu jox ma téere bu ndaw bi. Mu ne ma: «Jël ko te lekk ko. Dina wex ci sa biir nag, waaye ni lem lay neexe ci sa gémmiñ.»
10Ma jël téere bu ndaw bi ci loxol malaaka mi, lekk ko, mu neex ci sama gémmiñ ni lem, waaye naka laa ko wann, mu wex xàtt ci sama biir.
11Gannaaw loolu ñu ne ma: «War ngaa yékkatiwaat ay kàdduy waxyu jëmale ci xeet yu bare ak askan yu bare ak niti làkk yu bare ak buur yu bare.»
Currently Selected:
Peeñu ma 10: KY
Highlight
Copy
Compare
Share
Want to have your highlights saved across all your devices? Sign up or sign in
Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9
Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/
Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright