Ma dem ba ci malaaka mi, ne ko mu jox ma téere bu ndaw bi. Mu ne ma: «Jël ko te lekk ko. Dina wex ci sa biir nag, waaye ni lem lay neexe ci sa gémmiñ.»
Ma jël téere bu ndaw bi ci loxol malaaka mi, lekk ko, mu neex ci sama gémmiñ ni lem, waaye naka laa ko wann, mu wex xàtt ci sama biir.