YouVersion Logo
Search Icon

Peeñu ma 9

9
1Juróomeelu malaaka mi wal liitam, ma gis, biddiiw bu xàwweekoo woon asamaan, ba wadd ci kaw suuf. Ñu jox ko caabiy kàmbu xóote ba. 2Mu ubbi buntu kàmbu xóote ba, saxaar su mel ni saxaaras taal bu mag jollee ca, jant bi ak jaww ji, lépp lëndëm ndax saxaaras kàmb gi. 3Ba loolu amee ay njéeréer génne ci saxaar si, daldi tasaaroo ci biir àddina, ñu may leen ñuy fitte ni jànkalaar. 4Ñu ne leen, buñu laal mennum ñax, mbaa genn gàncax, mbaa genn garab, xanaa ñu jublu rekk ci nit ñi amul màndargam torluwaayu Yàlla ci seen jë. 5May nañu leen ñu mitital leen diiru juróomi weer, te bañ leena rey, xanaa mitital leen lu tembook mititu fittu jànkalaar. 6Bési keroog nit ñeey sàkku dee, te duñu ko daj, ñu ne siiwa dee, dee daw leen.
7Njéeréer yaa ngi nirook fas yu ñu waajal ngir xare, kaalawoo lu mel ni kaalay wurus, seen kanam nirook kanamu nit, 8seen kawar mel ni kawaru jigéen, seeni sell nirook selli gaynde. 9Ñu ngi sol kiiraayi dënn yu mel ni kiiraayi weñ gu ñuul, seen coowal laaf yi mel ni coowal watiiri xare yu bare. 10Geen gu am fitt lañu am ni jànkalaar. Daŋaru geen googu mooy manoore bi ñu am ngir mitital nit ñi diiru juróomi weer. 11Seen buur a leen jiite, di malaakam xóote bi, turam ci ebrë di Abadon; Apolyon ci làkku gereg (muy firi Yàqkat bi).
12Naka la musiba mu njëkk mi jàll rekk, yeneen ñaari musiba dikk, topp ci.
13Ba mu ko defee juróom benneelu malaaka mi wal liitam. Ma dégg baat bu jóge ci ñeenti béjjéni sarxalukaayu wurus bi ci kanam Yàlla. 14Baat bi wax ak juróom benneelu malaaka mi yor liit, ne ko: «Yiwil ñeenti malaaka ya yeewe ca Efraat, dex gu mag ga.»
15Ca lañu yiwi ñeenti malaaka ya ñu waajaloon ñeel waxtu woowu, ci bés boobu, weer woowu, at moomu, ngir ñu rey ñetteelu xaaju nit ñi. 16Limu gawari mbooloo ma doon xareji ñaari téeméeri junniy junni la (200 000 000). Maa dégg lim bi.
17Nii laa gise ci peeñu mi fas yi ak ñi leen war: ñu ngi sol kiiraay yu xonq ni sawara, baxa ni safiir, te mboq ni tamarax. Boppi fas yaa ngi nirook boppi gaynde, sawara ak saxaar ak tamarax di génne ci seen gémmiñ. 18Ñetti musiba yooyii, sawara seek saxaar seek tamarax biy génne ci seen gémmiñ, daldi rey ñetteelu xaaju nit ñi. 19Daŋaru fas yaa ngi ci seen gémmiñ ak ci seen geen, ndax seen geen yaa ngi mel ni ay jaan, ami bopp yu ñuy mititalee.
20Ndesu nit ñi musiba yooyii reyul nag, taxul sax ñu tuub seeni jëf, ba bañatee jaamu ay tuur, ak jëmmi xërëmi wurus ak xaalis ak xànjar ak xeer ak dénk: xërëm yu gisul, déggul, doxul. 21Rax ci dolli, tuubuñu bóome gi ak ñeengo gi ak séy yi yoon tere ak càcc gi ñu nekke.

Currently Selected:

Peeñu ma 9: KY

Highlight

Copy

Compare

Share

None

Want to have your highlights saved across all your devices? Sign up or sign in