YouVersion Logo
Search Icon

Peeñu ma 11

11
Ñaari seede yi bey nañu seen waar
1Ba loolu amee ñu jox ma nattukaay bu mel niw yet, ne ma: «Jógal, natt néegu Yàlla bi ak sarxalukaay bi, te nga waññ ña fay jaamu Yàlla. 2Waaye ëttu bitib kër Yàlla gi, bàyyi ko, bu ko natt, ndax ñi dul Yawut lees ko jox, te ñooy dëggaate dëkk bu sell bi diiru ñeent fukki weer ak ñaar. 3Dinaa may nag sama ñaari seede yi, ñu jottali kàdduy waxyu diiru junni fan ak ñaari téeméer ak juróom benn fukk (1 260) yu ñuy sol ay saaku, di ko toroxloo.»
4Ñaari seede yi ñoo di ñaari garabi oliw#11.4 oliw: garabu oliw dafa xawa mel ni sump, te am doom yu ñuy nal, ngir am ci diw gu ñuy togge, mbaa ñu di ko taaloo. yeek ñaari tegukaayi làmp yi taxaw ci kanam Boroom suuf si. 5Ku leen nara lor, sawaraay génne ci seen gémmiñ, lakk seeni noon. Képp ku leen nara lor, noonu ngay deewe. 6Am nañu sañ-sañu tëj asamaan, ba du taw diiru fan yi ñuy jottali kàdduy waxyu, am nañu itam sañ-sañ ci ndox mi, ngir soppi ko deret, ak sañ-sañu wàcce ci suuf wépp xeetu musiba, saa su leen soobee.
7Gannaaw bu ñu seedee ba noppi nag, rab wiy jóge ci xóote bi mooy xareek ñoom, daan leen, ba rey leen. 8Seeni néew da naan lareet ci péncum dëkk bu mag boobu ñuy misaale turu Sodom mbaa Misra, fa ñu reye woon seen Sang ci bant. 9Diiru ñetti fan ak genn-wàll lañuy weeru, niti wépp xeet ak gépp giir ak wépp làkk ak wépp askan di seetaan seeni néew, te duñu bàyyi kenn suul leen. 10Waa àddina dinañu bége seen dee, di bànneexu, di joqalante ay njukkal, ndaxte ñaari yonent yooyu ñoo lakkaloon waa àddina.
11Waaye bu ñetti fan yeek genn-wàll wéyee, noowug dund giy bawoo fa Yàlla moo leen di solu, ñu jóg, taxaw, tiitaange ju réy daldi jàpp waa ceetaan ma. 12Ba loolu amee ñaari seede yi dégg baat bu xumb jibe asamaan, ne leen: «Yéegleen fii.» Ñu yéeg ci asamaan ci biir aw niir, seeni noon di gis. 13Ca waxtu wa, suuf daldi yëngu lool, ba benn fukkeelu dëkk ba màbb. Juróom ñaari junniy nit (7 000) dee ci yëngub suuf ba, ña ca des tiit, di sàbbaal Yàllay asamaan.
14Ñaareelu musiba mi wéy na, waaye kat ñetteel baa ngi nii di ñëw.
Juróom ñaareelu liit ga jib na
15Ba mu ko defee, juróom ñaareelu malaaka mi wal liitam, baat yu xumb jibe ca asamaan, ne:
«Léegi nag nguurug àddina ñeel na sunu Boroom ak Almaseem.
Mooy nguuru ba fàww.»
16Ba loolu amee ñaar fukki mag ak ñeent, ña toogoon ca seen ngàngune ca kanam Yàlla, daldi ne gurub sukk, dëpp seen jë ca suuf, sujjóotal Yàlla. 17Ñu ne:
«Boroom bi Yàlla Aji Man ji nekk te nekkoon,
nu ngi lay gërëm,
ndax yaa ràngoo sa kàttan gu màgg,
taxawal sa nguur.
18Askan yee meroon,
waaye sa mer a dikk tey;
tey jii ngay àtte ñi dee,
yool say jaam, yonent yi,
yool ñu sell ñeek ñi la ragal, mag ak ndaw,
tey it ngay sànk ñiy sànk àddina.»
19Ci kaw loolu néegu Yàlla bi ci asamaan ubbiku, gaalu kóllëreg Yàlla ga di feeñ ca biir màkkaanam ma, melax ya tàkk, kàddu yaak dënu ya riir, suuf sa yëngu, tawu doji yuur bu metti daldi sóob.

Currently Selected:

Peeñu ma 11: KY

Highlight

Copy

Compare

Share

None

Want to have your highlights saved across all your devices? Sign up or sign in