Bible App logo
Search Icon

1.Korent 3

3
Par-parloo warul gëmkat ñi
1Man nag bokk yi, manuma woona wax ak yeen ni ñuy waxe ak ñu ànd ak Noowug Yàlla, waaye ni niti suuxu neen rekk laa manoona waxe ak yeen, mbete ñu diy tuut-tànk ci yoonu Almasi bi. 2Meew laa leen jota nàndale, waaye leelewuma leen dugub, ndax àttanuleen ko woon, te ba léegi sax àttanuleen ko, 3nde yeena ngi ba tey ci seenug niti suuxu neen. Ndax gannaaw kiñaan ak ŋaayoo ngi ci seen biir, du ay niti suuxu neen ngeen ba tey, di doxale ni niti àddinay kese? 4Bu kenn naan: «Man ci Póol laa bokk,» keneen naa: «Man nag Apolos,» ndax kon dungeen niti àddinay kese?
5Ana kuy Apolos sax? Ak kuy Póol? Xanaa du nun nooy ay surgay neen yu ngeen jaare ci nun, ba gëm, ni Boroom bi jagleele kenn ku nekk ci nun aw sasam. 6Maa jëmbat, Apolos suuxat, waaye Yàlla moo jebbil. 7Ki jëmbat nag ak ki suuxat, kenn du ci dara, xanaa Yàlla miy jebbil doŋŋ. 8Ki jëmbat, ak ki suuxat ñoo yem kepp, waaye ku ci nekk kemu liggéeyu boppam lay yooloo. 9Noo bokk diy surga ci liggéeyu Yàlla bi; yeen ngeen di toolu Yàlla, di tabaxub Yàlla.
10Yiwu Yàlla wi mu ma may nag, ci laa lale fondmaa bi, ni tabaxkat bu xareñ, keneen di tabax ca kaw. Waaye na ku nekk xool bu baax na mu cay tabaxe. 11Geneen fondmaa moom maneesu koo lal, xanaa gi xasa lale, te mooy Yeesu Almasi bi. 12Ku tabax ci kaw fondmaa bi nag, nga tabaxe wurus, mbaa xaalis, mbaa per, mbaa dénk, mbaa gattax, mbaa am mboob, 13ku ci nekk, sab liggéey dina feeñ, ndax bés-pénc baa koy xamle, nde sawara lees koy feeñale. Ku ci nekk ak lu sa xeetu liggéey mana doon, sawara lees koy natte. 14Ku liggéeyoon ba la nga tabaxoon ca kaw kenu ga des, dinga yoolu. 15Waaye ku sab liggéey lakk, ñàkk nga. Yaw ci sa bopp nag dinga mucc, mel ni ku rëcce cig lakk rekk.
16Xanaa xamuleen ne kër Yàlla ngeen, te Noowug Yàlla moo dëkk ci yeen? 17Ku yàq kër Yàlla nag, kooku Yàlla dina ko yàq, ndax kër Yàlla dafa sell, te mooy li ngeen doon.
18Bu kenn nax boppam: ku teg boppam ci yeen boroom xam-xam, ni xarnu bii jàppe xam-xam, kooku na doon ab dof, ngir am xam-xam bi wóor. 19Ndaxte xam-xamu àddina sii, ndof la fa Yàlla. Moo tax bindees na ne: «Mooy jàpp boroom xel yi ci seen pexey muusaatu#3.19 Seetal ci Ayóoba 5.13.20tegati ca ne: «Boroom bi xam na xalaati boroom xel yi te xam na ne neen la#3.20 Seetal ci Taalifi cant 94.11.
21Kon nag bu kenn puukarewoo ay nit, ndax lépp, yeena ko moom, 22muy Póol, di Apolos, di Sefas, di àddina, di dund, di dee, di tey, di ëllëg, lépp, yeena ko moom. 23Yeen nag, Almasi bi moo leen moom, te Almasi bi, Yàllaa ko moom.

Currently Selected:

1.Korent 3: KY

Highlight

Copy

Compare

Share

None

Want to have your highlights saved across all your devices? Sign up or sign in