1.Korent 2
2
1Man ci sama bopp, bokk yi, bi ma dikkee ci yeen, du ci puukarey kàddu yu gëna taaru ak xam-xam bu ma leen yégalsee mbóoti Yàlla. 2Doguwuma woona xam lenn ci seen biir, lu moy Yeesu Almasi bi, kooku ñu daaj ca bant ba. 3Man daal, ci sama biir néew dooley bopp ak ragal bay kat-kati, laa nekke woon ak yeen. 4Sama kàddu ak samam njàngale jotewul woon dara ak neex làmmiñ gu xam-xamu nit ràbb, waaye dafa di ay firnde yu manooreg Noowug Yàlla lañal, 5ngir seen ngëm baña sukkandiku ci xam-xamu nit, te sukkandiku ci manooreg Yàlla.
Xelum Yàlla mooy xamle xam-xamu Yàlla
6Moona xam-xam lanuy xamle ci biir gëmkat ñi mat, waaye du xam-xamu xarnu bii ak bu njiiti xarnu bii, di nit ñuy wéy. 7Li nuy biral kay, da di mbóotum xam-xamu Yàlla mu làqu woon, te Yàlla dogaloon nu koo terale, laata àddina di sosu. 8Boobu xam-xam, kenn ci njiiti xarnu bii xamu ko woon, ndax su ñu ko xamoon, kon duñu daaj Sang bu tedd bi ci bant. 9Mooy noonu ñu binde rekk ne:
«Lu bët gisul,
nopp déggu ko,
xel daju ko,
Yàllaa ko dencal ñi ko sopp#2.9 Seetal ci Esayi 64.3..»
10Waaye nun la Yàlla feeñalal denc googu jaare ci Xelam. Ndaxte Xelum Yàlla lépp lay gëstu ba ci xóotey mbóoti Yàlla. 11Kan ci nit ñi moo xamal kenn nit lenni biiram? Xelum nit ki ci biir nit ki doŋŋ moo mana xam biiram. Yàlla itam noonu la. Kenn xamul mbirum Yàlla ku moy Xelum Yàlla. 12Nun nag du xelum àddina lanu jot, waaye Xel mi bawoo fa Yàlla lanu jot, ngir nu mana ràññee li nu Yàlla baaxe. 13May yooyu lanuy biral, te waxewunu ko njàngalem xam-xamu nit, waaye njàngalem Xelum Yàlla lanu koy waxe, di jëfandikoo kàddu yu làmboo Xelu Yàlla mi, ngir teqantal ay mbir yu làmboo Xelu Yàlla mi.
14Nitu neen nag du nangu lu aju ci Xelum Yàlla. Ag ndof lay doon ci moom; du ko mana xam, ndax loolu Xelum Yàlla lees koy natte. 15Nit ki ànd ak Xelum Yàlla nag moo mana natt lépp, te moom ci boppam, kenn du ko mana natt. 16Moo tax ñu ne:
«Ana ku mana nànd xalaatu Boroom bi?
Ana ku ko mana digal#2.16 Seetal ci Esayi 40.13.?»
Waaye nun nag noo yor xalaatu Almasi bi.
Currently Selected:
1.Korent 2: KY
Highlight
Copy
Compare
Share
Want to have your highlights saved across all your devices? Sign up or sign in
Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9
Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/
Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright