Bible App logo
Search Icon

1.Korent 4

4
Àtteb Yàlla doy na Póol
1Dees noo wara jàppe ay surgay Almasi bi, ay saytukati mbóoti Yàlla. 2Te itam li ñuy sàkku ci ay saytukat moo di ñu jara wóolu. 3Man nag, su dee yeena dogal samab àtte, mbaa kuréelu nit a dogal samab àtte, soxaluma lool, te dogalaluma sama bopp ab àtte it, 4ndax amul dara lu may yedde sama bopp. Waaye nag loolu taxul ma jub, ndax kiy dogal samab àtte mooy Boroom bi. 5Moo tax buleen àtte lenn te jotul, lu jiitu Boroom biy dikk. Moom mooy leeral li làqoo ag lëndëm, di làññi mébéti xol. Su boobaa ngërëm la ku nekk yelloo, fa Yàlla lay bawoo.
6Bokk yi, loolu de laa natte ci Apolos ak ci man, ñeel leen, ngir ngeen jànge ci sunu ñaari jëmm, ba sàmm solos kàddu gii: «Bu seen xalaat jàll lu weesu li Mbind mi wax.» Su ko defee dungeen réy-réyloo far ak kenn, di beddi keneen. 7Ana ku la def nga gën ci nit ñi? Ana loo am lu ñu la joxul? Te ndegam dees la koo jox, ana loo koy puukarewoo, mbete lees la joxul?
8Yeen daal suur ngeen xaat! Woomle ngeen xaat! Yeena ngi tàmbalee nguuru, te xaaruleen nu ci sax! Céy su ngeen doon nguuru léegi, ba nun itam nu mana nguuroondoo ak yeen! 9Ndaxte damaa foog ne, nun ndawi Almasi bi, Yàllaa nu fésal ca sàppeb gannaaw ba, mbete nit ñu ñu teg àtteb dee, ngir nu doon ceetaanum àddina wërngal këpp, malaaka ak nit. 10Nun, sunu xér ci Almasi bi tax na ñu jàppe nu ay dof; yeen, yeena muus nu ngeen bokke ci Almasi bi! Nun noo néew doole; yeen, yeena am doole. Yeen it lañu naw, waaye nun, dees noo xeeb! 11Ba fii nu tollu, xiif ak mar ak rafle aki dóor lanu nekke, di wër rekk. 12Danuy ñaq, di dunde sunu liggéeyu loxo, nit ñi di nu saaga, nu di leen ñaanal; ñu di nu bunduxataal, nuy muñ. 13Nu ngi nuy baatal, nun nuy wax lu rafet ci nit ñi, nu mujj mel ni mbalitu àddina, di mbuubitu ñépp ba fii nu tollu.
14Kersaal leen nag taxul ma bind leen lii, waaye dama leen koy artoo, ndax yeenay sama doomi bopp. 15Su ngeen amoon fukki junniy njiit yu leen di sàmm ci yoonu Almasi bi it, du tax ngeen am lu wees benn baay, te man maa leen àgge xibaaru jàmm bi, ba tax ma di seen baay ci yoonu Almasi Yeesu. 16Kon nag maa ngi leen di tinu, ngir ngeen roy ci man. 17Looloo tax ma yebal ci yeen Timote, sama doomu bopp ji sax ci yoonu Sang bi. Moo leen di fàttali samay doxalin ci yoonu Almasi bi, noonu ma koy jàngalee fépp, ci mépp mbooloom gëmkat.
18Am na nag ñuy réy-réylu ci seen biir, defe ne duma délseeti ci yeen. 19Waaye maa ngi dikk léegi ba ci yeen, ndegam soob na Boroom bi, ba nattal sama bopp manoore ju réy-réylukat yooyu am, te duy kàddu kese. 20Ndaxte nguurug Yàlla du ci waxi kese, waaye manoore la. 21Ana lu leen gënal? Ma dikke leen ab yar, am ma dikke leen cofeel ak yërmande?

Currently Selected:

1.Korent 4: KY

Highlight

Copy

Compare

Share

None

Want to have your highlights saved across all your devices? Sign up or sign in