Kon yeen itam, tey, aw tiis ngeen am, waaye dinaa leen gisaat, seen xol sedd, te seen mbég moomu, kenn du leen ko xañ. Bésub keroog, man dootuleen ma ñaan dara. Maa leen ko wax déy ci lu wér, su boobaa lu ngeen ñaan Baay bi ci sama tur, mu may leen ko.