1
Yowaan 17:17
Kàddug Yàlla
KY
Ngalla sellale leen dëgg gi: sa kàddu mooy dëgg.
Compare
Explore Yowaan 17:17
2
Yowaan 17:3
Texeg fàww gi nag moo di ñu xam la, yaw jenn Yàlla jiy dëgg, xam it ki nga yebal, muy Yeesu Almasi bi.
Explore Yowaan 17:3
3
Yowaan 17:20-21
«Du ñoom doŋŋ laay ñaanal nag, waaye ñi may gëm ëllëg ndax seen kàddu itam laay ñaanal, ngir ñépp doon benn, ni nga nekke yaw Baay, ci man, ma nekke ko ci yaw, ñoom itam, ñu nekke ni ci nun, ba àddina gëm ne yaw yaa ma yebal.
Explore Yowaan 17:20-21
4
Yowaan 17:15
Ñaanuma nga jële leen ci àddina, xanaa nga musal leen ci ku bon ki.
Explore Yowaan 17:15
5
Yowaan 17:22-23
Man nag daraja ji nga ma jox, jox naa leen ko, ngir ni nu nekke benn maak yaw, ñu nekke ni noonu. Man ma nekk ci ñoom, yaw nga nekk ci man, ngir ñu mat sëkk ci ag bennoo, ba àddina xam ne yaw yaa ma yebal, te ni nga ma soppe, ni nga leen soppe.
Explore Yowaan 17:22-23