1
Yawut ya 8:12
Kàddug Yàlla
KY
Maa leen di jéggal seeni ñaawtéef, te seeni bàkkaar, duma ci bàyyeeti xel.»
Compare
Explore Yawut ya 8:12
2
Yawut ya 8:10
«Lii nag moo di kóllëre gi may fas ak waa kër Israayil, bu fan yooyu weesoo: Boroom beey wax, mu ne: Maay yeb sama ndigali yoon ci seen xel, ci seen xol laa koy ñaas. Maay doon seen Yàlla, ñoom ñu doon sama ñoñ.
Explore Yawut ya 8:10
3
Yawut ya 8:11
Kenn dootul soxlaa jàngal moroomam, mbaa mbokkam, naan ko: “Ràññeel Boroom bi!” Ndax ñoom ñépp a may ràññee, ki gëna tuut ba ci ki gëna mag.
Explore Yawut ya 8:11
4
Yawut ya 8:8
Waaye Yàllaa sikk bànni Israayil, ba mu nee: «Ay fan a ngii di ñëw, la Boroom bi wax, mu ne maay fas ak waa kër Israayil ak waa kër Yuda, kóllëre gu yees gu bokkewul ak ga ma séqoon ak seeni maam
Explore Yawut ya 8:8
5
Yawut ya 8:1
Kàddu yii nu wax nag, lii moo di ponk bi: boobu sarxalkat bu mag lanu am, mu toog ci ndijooru ngànguney Ku màgg ka fa asamaan.
Explore Yawut ya 8:1