YouVersion Logo
Search Icon

Yawut ya 8

8
Kóllëre gi gën la Yeesu Sarxalkat bu mag bi indi
1Kàddu yii nu wax nag, lii moo di ponk bi: boobu sarxalkat bu mag lanu am, mu toog ci ndijooru ngànguney Ku màgg ka fa asamaan. 2Mooy liggéey ca kër gu sell ga, ca biir xaymab jaamookaay bu dëggu, ba Boroom bi samp, te nit sampu ko.
3Gannaaw nag ab sarxalkat bu mag bu mu mana doon, dees koo fal, ngir muy joxe ay saraxi njébbal ak saraxi jur, kon fàww sarxalkat bu mag bii itam am lu mu sarxe. 4Bu doon ci àddina, du nekk sax ab sarxalkat, gannaaw ay sarxalkat a ngi fi, di jébbale ay sarax, ni ko yoonu Musaa laaje. 5Sarxalkat yooyu, jaamookaay bi ñuy liggéeye, ab misaal la, takkndeeru yëf yu dëggu ya fa asamaan la. Ndax ba Musaa di waaja yékkati xaymab jaamookaay ba, noonu lees ko artoo woon, ne ko: «Nanga xool te def lépp, mu dëppook misaal mi ñu la won ci kaw tund wi#8.5 Seetal ci Mucc ga 25.40.6Waaye tey la Yeesu jot ci liggéeyu carxal gu sut gu njëkk ga fuuf, te kóllëre gi mu fas diggante Yàlla ak nit ñi, noonu la gëne gu njëkk ga; dige yi lal kóllëre gu yees gii it, noonu la gëne dige ya laloon gu njëkk ga.
7Bu kóllëre gu njëkk ga muccoon sikk nag, deesul soxlaa xajal geneen. 8Waaye Yàllaa sikk bànni Israayil, ba mu nee:
«Ay fan a ngii di ñëw, la Boroom bi wax,
mu ne maay fas ak waa kër Israayil ak waa kër Yuda,
kóllëre gu yees
gu bokkewul ak ga ma séqoon ak seeni maam,
9ba ma leen jàppee ci loxo,
génne leen réewum Misra.
Gannaaw ñoo sàmmul sama kóllëre nag,
man it geesuwuma leen,
la Boroom bi wax.
10«Lii nag moo di kóllëre gi may fas
ak waa kër Israayil, bu fan yooyu weesoo:
Boroom beey wax, mu ne:
Maay yeb sama ndigali yoon ci seen xel,
ci seen xol laa koy ñaas.
Maay doon seen Yàlla,
ñoom ñu doon sama ñoñ.
11Kenn dootul soxlaa jàngal moroomam,
mbaa mbokkam, naan ko: “Ràññeel Boroom bi!”
Ndax ñoom ñépp a may ràññee,
ki gëna tuut ba ci ki gëna mag.
12Maa leen di jéggal seeni ñaawtéef,
te seeni bàkkaar, duma ci bàyyeeti xel#8.8-12 Seetal ci Yeremi 31.31-34.
13Bu Yàlla woowee kóllëre gii gu yees nag, daa fekk mu wonnil gu njëkk ga. Lu wonni te di lu yàgg nag, mu ngi ci tànki wees.

Currently Selected:

Yawut ya 8: KY

Highlight

Copy

Compare

Share

None

Want to have your highlights saved across all your devices? Sign up or sign in