1
Yawut ya 9:28
Kàddug Yàlla
KY
noonu itam la Almasi bi doone ab sarax benn yoon, ngir gàddu bàkkaaru nit ñu bare, te dina teewsiwaat, ci yoon wu joteetul dara ak bàkkaar, ngir indil ñi koy séentu seenug mucc.
Compare
Explore Yawut ya 9:28
2
Yawut ya 9:14
Su loolu amee, ñaata yoon la deretu Almasi bi ëppe njariñ! Almasi bi mooy ki def boppam sarax bu mucc sikk ñeel Yàlla, ci dooley Noo gu Sell gi. Moom rekk moo mana setal sunu yaraangey xel mi sababoo ci sunu jëf ju bon ju jëme ci dee, ba nu mana jaamu Yàlla jiy dund!
Explore Yawut ya 9:14
3
Yawut ya 9:27
Kon ni ab dogal sédde nit ñi benn yoon doŋŋ bu ñuy dee, seenub àtte topp ci
Explore Yawut ya 9:27
4
Yawut ya 9:22
Ndax ci yoonu Musaa sax, deret lees di setale daanaka lépp, te bu deret tuuruwul, njéggal amul.
Explore Yawut ya 9:22
5
Yawut ya 9:15
Looloo tax Yeesu di rammukat bi fas kóllëre gu bees, ngir ñi ñu woo mana jot ci muur gu sax dàkk gi ñu leen dig. Deewam gi mu dee, moom la leen jote ci bàkkaar yi ñu xëtte kóllëre gu njëkk ga.
Explore Yawut ya 9:15