Na kàddug Almasi bi dëkk ci yeen, bay baawaan, ngeen di jariñoo xel mu mat sëkk mu ngeen di jàngalantee aka artoonte. Woyeleen xolub cant, ñeel Yàlla, ak ay taalifi cant ak woyi tagg Yàlla ak woy yu ñu fente ci Noowug Yàlla gi. Lu ngeen mana def, muy ci wax, di ci jëf, defleen ko ci turu Sang Yeesu, tey sant Yàlla Baay bi ci moom.