Kolos 3
3
Gëmkatub Almasi bi, dundin wu yees
1Gannaaw nag yeena dekkeendoo ak Almasi bi, sàkkuleen la fa kaw, fa Almasi bi tooge ca ndijooru Yàlla. 2La fa kaw, xintewooleen ko, te ngeen ba li fi suuf, 3ndaxte dee ngeen, ba seenug dund ànd ak Almasi bi, làqe fa Yàlla. 4Seenug dund dëgg Almasi bi la, te keroog bu Almasi bi feeñee, yeen itam dingeen ànd ak moom feeñ, ba séddu ci ndamam.
5Kon nag reyleen seen cér yi bokk fii ci kaw suuf; lu mel ni séy yi yoon tere ak jëfi sobe ak ñàkk sago ci lu jekkadi ak xemmemtéef yu bon ak bëgge, te loolooy bokkaale ba tey, 6yooyooy wàcce sànjum Yàlla ci kaw ñi déggadi. 7Yeen itam noonu ngeen daan jëfe bu njëkk, ba seenug dund bokkee fii ci kaw suuf. 8Waaye léegi, lii lépp baleen ko: maanaam tàng xol ak mer mu ëpp ak coxor ak saaga ak wax ju ñaaw. 9Buleen di fenante, gannaaw seen jëmm ja woon démb, boole ngeen kook jëfinam ja mu àndal, summi, 10ba sol seen jëmm ju yees jiy gën di yeeslu, te di gëna niru ki leen ko sàkkal, ba kera seen xam-xam mat sëkk. 11Dundin wu yees woowu amul jàmbur akub Yawut, amul ku xaraf ak ku xaraful, amul ab doxandéem ak ku xayadi, amul ab jaam ak as gor, waaye Almasi bi mooy lépp te moo nekk ci ñépp.
12Yeenay ñi Yàlla tànn, sellal leen, sopp leen. Kon nag solleen xolu yërmande akug mbaax ak woyoflu ak jikko ju lewet ak xolu muñ. 13Muñalanteleen te di baalante, su dee kenn ku am lu mu sikke moroomam. Ni leen Boroom bi baale, deeleen baalantee noonu. 14Ci kaw loolu lépp nag, tegooleen cofeel, mooy xànc gi leen faste, ba seenug bennoo mat sëkk.
15Na jàmmu Almasi bi saytu seen xol. Ci jooju jàmm lañu leen woo, fekk leen ngeen di wenn yaram doŋŋ, te it saxooleen cant. 16Na kàddug Almasi bi dëkk ci yeen, bay baawaan, ngeen di jariñoo xel mu mat sëkk mu ngeen di jàngalantee aka artoonte. Woyeleen xolub cant, ñeel Yàlla, ak ay taalifi cant ak woyi tagg Yàlla ak woy yu ñu fente ci Noowug Yàlla gi. 17Lu ngeen mana def, muy ci wax, di ci jëf, defleen ko ci turu Sang Yeesu, tey sant Yàlla Baay bi ci moom.
Rafetooleen
18Na jabar nangul jëkkëram, noonu mu jekke ci ku bokk ci Boroom bi.
19Jëkkër nag, na sopp jabaram, te bumu ko soxore.
20Xale yi, déggalleen seeni waajur ci lépp, ndax loolu mooy li Boroom bi rafetlu.
21Yeen ñiy baay, buleen yékkati seen xolu doom, ngir baña jeexal seen xol.
22Jaam yi, nangulleen ci lépp seen sang yi ci àddina. Buleen ko defe ngistal, mbaa ngeen di ko sàkkoo lu leen neex, waaye defeleen ko yéeney xol bu dëggu, ndax ragal Boroom bi. 23Lu ngeen mana def, liggéeyeleen ko xol bu tàlli, ni bu ñeelul woon nit doŋŋ, xanaa Boroom bi. 24Te ngeen xam ne ci loxol Boroom bi ngeen di nangoo yool bi ngeen muurloo. Sang bi, Almasi bi mooy ki ngeen di jaamu. 25Waaye ku def njubadi, njubadi ga mu def lañu koy jox ab yool, te xejj ak seen du ci am.
Currently Selected:
Kolos 3: KY
Highlight
Copy
Compare
Share
Want to have your highlights saved across all your devices? Sign up or sign in
Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9
Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/
Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright