Yeen ñi doonoon ñu dee fa kanam Yàlla ndax seeni moy ak seen ñàkka xaraf, ndax li ngeen dul Yawut, Yàllaa leen booleek Almasi bi, dundalaat leen. Moo nu baal sunu moy yépp. Kayitu bor bi nu tiiñaloon, te dogali yoon toppe nu ko, moom moo far mbind ma, yóbbu kayit ga, daajaale ko ak Almasi bi ca bant ba.