1
1.Timote 2:5-6
Kàddug Yàlla
KY
Ndax kat jenn Yàlla doŋŋ moo am, benn rammukat doŋŋ it moo am diggante Yàlla ak nit ñi, te mooy kenn nit: muy Almasi Yeesu mi maye bakkanam ngir jot ñépp, te loolu mooy seede si Yàlla joxe, bi waxtu wi jotee.
Compare
Explore 1.Timote 2:5-6
2
1.Timote 2:1-2
Kon nag li jiitu ci mboolem li may dénkaane mooy ngeen di dagaan, di ñaan, di tinu aka sant, ñeel doom aadama yépp, ñeel buur yi ak mboolem boroom baat yi, ngir nu mana nekke jàmm akug dal ak wépp dundin wu tedd, tey wéye ragal Yàlla.
Explore 1.Timote 2:1-2
3
1.Timote 2:8-10
Kon li ma bëgg moo di góor ñi di ñaane fépp, tàllal loxo yu mucc sikk, te bañ cee boole meroo ak mbiicoo. Naka noonu, na jigéen ñi di sol col gu yiw gu teggine te yem. Buñu jiital di defarlu ay létt yu ëpp ak gànjari wurus aki per ak yérey tànnéef, waaye nañu gànjaroo jëf ju baax, ndax mooy li jekk ci jigéen ñuy seede ne ñooy ñiy ragal Yàlla.
Explore 1.Timote 2:8-10