YouVersion Logo
Search Icon

1.Timote 2:8-10

1.Timote 2:8-10 KY

Kon li ma bëgg moo di góor ñi di ñaane fépp, tàllal loxo yu mucc sikk, te bañ cee boole meroo ak mbiicoo. Naka noonu, na jigéen ñi di sol col gu yiw gu teggine te yem. Buñu jiital di defarlu ay létt yu ëpp ak gànjari wurus aki per ak yérey tànnéef, waaye nañu gànjaroo jëf ju baax, ndax mooy li jekk ci jigéen ñuy seede ne ñooy ñiy ragal Yàlla.

Free Reading Plans and Devotionals related to 1.Timote 2:8-10