1.Timote 2
2
Póol sàrtal na jataayub màggal Yàlla
1Kon nag li jiitu ci mboolem li may dénkaane mooy ngeen di dagaan, di ñaan, di tinu aka sant, ñeel doom aadama yépp, 2ñeel buur yi ak mboolem boroom baat yi, ngir nu mana nekke jàmm akug dal ak wépp dundin wu tedd, tey wéye ragal Yàlla.
3Loolu moo rafet te neex Yàlla sunu Musalkat 4bi bëgg ñépp mucc te ràññee liy dëgg. 5Ndax kat jenn Yàlla doŋŋ moo am, benn rammukat doŋŋ it moo am diggante Yàlla ak nit ñi, te mooy kenn nit: muy Almasi Yeesu 6mi maye bakkanam ngir jot ñépp, te loolu mooy seede si Yàlla joxe, bi waxtu wi jotee. 7Ci boobu seede lañu ma tabbe ab yéenekat ak ndawal kàddu gi ak itam ab jàngalekat, ñeel xeet yi dul Yawut, ngir ma xamal leen yoonu ngëm ak dëgg. Fenuma, dëgg doŋŋ laay wax.
8Kon li ma bëgg moo di góor ñi di ñaane fépp, tàllal loxo yu mucc sikk, te bañ cee boole meroo ak mbiicoo. 9Naka noonu, na jigéen ñi di sol col gu yiw gu teggine te yem. Buñu jiital di defarlu ay létt yu ëpp ak gànjari wurus aki per ak yérey tànnéef, 10waaye nañu gànjaroo jëf ju baax, ndax mooy li jekk ci jigéen ñuy seede ne ñooy ñiy ragal Yàlla.
11Te it bu ñuy jàngale, na jigéen ñiy noppi, te woyof toyy. 12Mayuma jigéen mu jàngale mbaa mu jiite góor, waaye na noppi. 13Ndax kat Aadama lañu njëkka bind, Awa topp ca. 14Te it du Aadama lañu nax, waaye jigéen lañu nax ba mu xëtt ndigal. 15Teewul muccu jigéen a ngi ci njurum doom, ndegam saxoo na ngëm ak cofeel ak jëfin wu sell te yem.
Currently Selected:
1.Timote 2: KY
Highlight
Copy
Compare
Share
Want to have your highlights saved across all your devices? Sign up or sign in
Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9
Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/
Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright