1
Peeñu ma 11:15
Kàddug Yàlla
KY
Ba mu ko defee, juróom ñaareelu malaaka mi wal liitam, baat yu xumb jibe ca asamaan, ne: «Léegi nag nguurug àddina ñeel na sunu Boroom ak Almaseem. Mooy nguuru ba fàww.»
Compare
Explore Peeñu ma 11:15
2
Peeñu ma 11:18
Askan yee meroon, waaye sa mer a dikk tey; tey jii ngay àtte ñi dee, yool say jaam, yonent yi, yool ñu sell ñeek ñi la ragal, mag ak ndaw, tey it ngay sànk ñiy sànk àddina.»
Explore Peeñu ma 11:18
3
Peeñu ma 11:3
Dinaa may nag sama ñaari seede yi, ñu jottali kàdduy waxyu diiru junni fan ak ñaari téeméer ak juróom benn fukk (1 260) yu ñuy sol ay saaku, di ko toroxloo.»
Explore Peeñu ma 11:3
4
Peeñu ma 11:11
Waaye bu ñetti fan yeek genn-wàll wéyee, noowug dund giy bawoo fa Yàlla moo leen di solu, ñu jóg, taxaw, tiitaange ju réy daldi jàpp waa ceetaan ma.
Explore Peeñu ma 11:11
5
Peeñu ma 11:6
Am nañu sañ-sañu tëj asamaan, ba du taw diiru fan yi ñuy jottali kàdduy waxyu, am nañu itam sañ-sañ ci ndox mi, ngir soppi ko deret, ak sañ-sañu wàcce ci suuf wépp xeetu musiba, saa su leen soobee.
Explore Peeñu ma 11:6
6
Peeñu ma 11:4-5
Ñaari seede yi ñoo di ñaari garabi oliw yeek ñaari tegukaayi làmp yi taxaw ci kanam Boroom suuf si. Ku leen nara lor, sawaraay génne ci seen gémmiñ, lakk seeni noon. Képp ku leen nara lor, noonu ngay deewe.
Explore Peeñu ma 11:4-5