YouVersion Logo
Search Icon

Luug 4

4
Yeesu dékku na pexey Seytaane
1Yeesu moo feesoon ak Noo gu Sell gi, bàyyikoo ci dexu Yurdan, ci njiital Noo gi, ba ca biir màndiŋ ma. 2Ñeent fukki fan la ko fa Seytaane fiire.
Yeesu lekkul dara diir boobu bépp. Gannaaw ba fan yooyu wéyee, mu xiif. 3Seytaane nag ne ko: «Ndegam yaa di Doomu Yàlla, neel doj wii mu soppaliku mburu.» 4Yeesu ne ko: «Bindees na ne: “Du aw ñam doŋŋ la nit di dunde#4.4 Seetal ci Baamtug yoon wi 8.3..”»
5Seytaane yéege na ko fu kawe itam, won ko mboolem nguuri àddina, ci xef ak xippi. 6Seytaane ne Yeesu: «Yaw laay may mboolem kilifteef gii ak daraja ji mu àndal, ndax man lees ko jox, te ku ma soob laa koy may. 7Kon nag soo ma sujjóotalee, yaa moom lépp.» 8Yeesu ne ko: «Bindees na ne:
“Boroom bi sa Yàlla ngay sujjóotal, te moom doŋŋ ngay jaamu#4.8 Seetal ci Baamtug yoon wi 6.13..”»
9Seytaane yóbbu na ko Yerusalem, aj ko ca njobbaxtalu kër Yàlla ga, ne ko: «Ndegam yaa di Doomu Yàlla, tëbeel fii, wàcc, 10ndax bindees na ne:
“Ay malaakaam lay jox ndigal ci sa mbir,
ñu sàmm la,
11te seeni loxo lañu lay leewoo,
ba doo fakkastalu ciw doj#4.10-11 Seetal ci Taalifi cant 91.11-12..”»
12Yeesu ne ko: «Bindees na ne: “Bul seetlu Boroom bi sa Yàlla#4.12 Seetal ci Baamtug yoon wi 6.16..”»
13Seytaane lalal na Yeesu gépp fiir ba sottal, doora dem, bàyyi ko ab diir.
Mbind mi mat na tey
14Ba loolu amee Yeesu dellu Galile ci manoorey Noo gu Sell gi, ab jëwam nag law ca diiwaan ba bépp ba mu daj. 15Muy jàngale ca seeni jàngu, ñépp di ko kañ.
16Yeesu moo dikkoon Nasaret ga mu yaroo, daldi dugg ca jàngub Yawut ba, na mu ko baaxoo woon ci bésub Noflaay. Mu taxaw ngir biral ab dog. 17Ñu jox ko téereb Yonent Yàlla Esayi. Mu ubbi téere bi, gis dog bi ñu bind ne:
18«Noowug Boroom baa ngi fi sama kaw,
ndax moo ma diw, fal ma
ngir ma yégal néew-doole yi xibaaru jàmm bi.
Moo ma yebal ngir ma yégal jaam yi, ne dees na leen jot,
yégal gumba yi, ne dinañu gis,
yégal ñi ñu noot, ne dees na leen goreel,
19tey yéene atum yiw wu Boroom bi.»
20Ci kaw loolu mu ub téere bi, delloo ko jawriñ ja, daldi toog. Ña ca jàngu ba ñépp nag ne ko jàkk. 21Mu àddu, ne leen: «Tey jii la Mbind mii mat, ngeen dégg.» 22Ñépp a doon seedeel Yeesu lu rafet, tey yéemu ci kàdduy yiw yi tukkee ci gémmiñam. Ñu naan: «Xanaa kii du doomu Yuusufa ji?» 23Mu ne leen: «Xam naa ne dingeen ma waxal waxin wi ñu naan: “Fajkat bi, fajal sa bopp.” Mboolem li nu dégg ne moo xew Kapernawum, def ko fii ci sa réewum bopp itam.» 24Mu neeti: «Maa leen ko wax déy, amul benn yonent bu ñu teral ci réewu boppam. 25Maa leen wax ne liy dëgg moo di, ca jamonoy Ilyaas, ba asamaan tëjoo diiru ñetti at ak juróom benni weer, ba xiif bu metti am ca réew mépp, ay jëtun ñu baree nga woon ca Israayil. 26Moona du kenn ci ñoom ku ñu yebal Ilyaas ca moom ku moy jëtun ba dëkke Sarebta, ca Sidon. 27Jamonoy Yonent Yàlla Alyaasa itam, ay gaana yu baree nga woon ca Israayil. Waaye fajeesu ci kenn ku moy Naaman, waa Siri ba.»
28Ba mboolem waa jàngu ba déggee loolu dañoo mer ba fees. 29Ñu jóg, bëmëx ko ba génne ko dëkk ba, yóbbu ko ca kéméju tund wa seen dëkk ba sance, ngir xalab ko ci suuf. 30Teewul moom mu jaare ci seen biir, dem yoonam.
Yeesu faj na ku rab jàpp
31Ba mu ko defee Yeesu dem Kapernawum, ab dëkk ca diiwaanu Galile, di leen jàngal ca bési Noflaay ya. 32Nit ña nag yéemu ca njàngaleem, ndax sañ-sañ ba muy waxe. 33Ndeke foofa ca jàngu ba, jenn waay ju rab jàpp a nga fa woon. Waa ji jekki xaacu, ne: 34«Moo yaw Yeesum Nasaret, ana lu nu joteek yaw? Alagsi nu mooy say tànk? Xam naa yaa di kan, yaa di Aji Sell ju Yàlla ji!» 35Yeesu nag gëdd ko, ne ko: «Noppil te génn nit ki!» Rab wa daaneel nit ki ca digg mbooloo ma, doora génn te gaañu ko fenn.
36Ba loolu amee ñépp a yéemu, di wax ci seen biir, naan: «Gii kàddu lu mu doon? Moom de sañ-sañ ak xam-xam lay joxe rab yi ndigal, ñu génn.» 37Coowal Yeesu nag law ba fépp fu bokk ca diiwaan ba.
Yeesu faj na jarag yu bare
38Yeesu jóge ca jàngu ba, dem kër Simoŋ, daldi fekk yaayu jabaru Simoŋ ànd ak tàngooru yaram wu réy. Ñu ñaan ndimbal Yeesu. 39Mu dikk, tiim soxna sa, daldi gëdd tàngooru yaram wa, tàngoor wa teqalikook moom. Soxna sa jóg ca saa sa, di leen toppatoo.
40Ba jant sowee, mboolem ña amoon ay jarag yu ame ay jàngoroy jàngoro, daldi leen indil Yeesu. Moom it, mu teg kenn ku ci nekk ay loxoom, wéral la. 41Ay rab itam di génne ci ñu bare, di yuuxu, te naan: «Yaay Doomu Yàlla!» Teewul mu gëdd leen, aaye leen ñu wax, ndax xamoon nañu ne mooy Almasi bi.
42Njël gu njëkk ca ëllëg sa la Yeesu génn dëkk ba, dem ba béreb bu wéet. Mbooloo ma nag di ko seet, ba dikk, di ko téye, bañ mu dem, ba leen. 43Mu ne leen: «Yeneen dëkk yi it, war na ma faa yégleji xibaaru jàmm bu nguurug Yàlla, ndax looloo tax ñu yebal ma.» 44Ci kaw loolu muy waare ca jànguy Yawut ya ca réew mi.

Currently Selected:

Luug 4: KY

Highlight

Copy

Compare

Share

None

Want to have your highlights saved across all your devices? Sign up or sign in