Luug 3
3
Yaxya waare na
1Ca fukkeelu at ak juróom ci nguurug buur bu mag ba Tibeer Sesaar, ba Poñsë Pilaat yilifee diiwaanu Yude, Erodd yilif diiwaanu Galile, Filib magam yilif diiwaanu Iture ak bu Tarakonit, Lisañas yilif Abilen, 2jamono yooyu Anas ak Kayif doone sarxalkat yu mag ya, ca la kàddug Yàlla dikkal Yaxya doomu Sàkkaryaa, ca màndiŋ ma. 3Yaxya dugg ci mboolem àll bi wër dexu Yurdan, di waare lu jëm ci tuubeel gu nit ñi wara fésale ag sóobu cim ndox, ngir Yàlla jéggal leen seeni bàkkaar.
4Loolu lañu bind ci téereb waxi Yonent Yàlla Esayi ne:
«Baatu nit a ngi xaacoo ca màndiŋ ma, naan:
“Nangeen xàll yoonu Boroom bi,
juballeen ay xàllam.
5Xur yépp ay sëkke,
tund wu mag ak wu ndaw maasaloo,
yoon ya lunkoon, jubbantiku,
ya ñagasoon, nooy,
6ba ñépp gis mucc gi Yàlla dogal.”»
7Yaxya nag di wax mbooloo may ñëw ngir mu sóob leen ci ndox, naan leen: «Yeen njurum jaan mee, ku leen artu, ba ngeen di daw sànj miy dikk? 8Kon nag jëfeleen jëf ju yelloo ag tuubeel, te baña nax seen bopp naan: “Nun, Ibraayma mooy sunu maam,” ndax maa leen ko wax, doj yii, Yàlla man na cee sàkkal Ibraayma aw askan. 9Te itam xàcc nañu sémmiñ ngir gor reenu garab yi ba noppi. Kon nag gépp garab gu ci meññul doom yu baax, dees koy gor, sànni ca sawara sa.»
10Mbooloo ma itam laaj ko ne ko: «Ana lu nu war nag?» 11Mu ne leen: «Ku am ñaari turki, na sédd ki amul. Ku am aw ñam itam, na defe noonu.» 12Ay juutikat itam dikk, ngir sóobusi; ñu ne Yaxya: «Kilifa gi, ana lu nu war?» 13Mu ne leen: «Xanaa baña sàkku lenn lu moy li jaadu.» 14Ay takk-der itam ne ko: «Nun nag, nu nuy def?» Mu ne leen: «Buleen néewal kenn doole, mbaa di duural kenn ngir jëlal ko dara; doyloo leen seen peyoor.»
15Ci kaw loolu askan wa di séentu, ñépp di seetaat ci seen xel, ndax Yaxya mooy Almasi bi. 16Yaxya wax leen ñoom ñépp ne leen: «Man de ci ndox laa leen di sóob. Waaye ku ma sut a ngi ñëw, kooku, buumi caraxam sax, yeyoowuma ko koo feccil. Moom, ci Noo gu Sell gi ak sawara la leen di sóob#3.16 Sóobu gi ci Noo gu Sell gi ak ci sawara: Almasi bi moo leen di sol doole ju bawoo ci Noo gu Sell gi, ak itam setal leen ni sawara di setale weñ gu am lu ko rax. Sawara dina taxawe itam céru mbugal mu ñeel ñi déggalul Yàlla. Seetal ci 12.49; Jëf ya 2.3.. 17Ab layoom a ngi ci loxoom, mooy jéri dàggaam, ba mu set wecc; pepp mi lay fat cim sàqam, waaye xatax bi, da koy lakk ci sawara su dul fey mukk.»
18Bare na yeneen dénkaane yu Yaxya doon xamal nit ñi, di yégle xibaaru jàmm bi. 19Erodd boroom réew ma nag, Yaxya sikkoon na ko ndax Erojàdd jabaru magam ja mu nekkaloon, ak mboolem yeneen ñaawtéef yu Erodd def. 20Mu tegati leneen ca loolu lépp: jàpp Yaxya, tëj ca kaso ba.
Yaxya sóob na Yeesu ci ndox
21Noonu Yaxya doon sóobe ñépp cim ndox, ni la deme ba Yeesu dikk, mu sóob ko ci ndox. Ci biir loolu Yeesu yékkati kàddug ñaan, asamaan ubbiku. 22Ba loolu amee Noo gu Sell gi moo bindoo ni pitax, wàcc ci kawam, baat jibe asamaan, ne: «Yaa di sama Doom, sama soppe; yaw laay bànneexoo.»
Lu jëm ci cosaanu Yeesu Almasi bi
23Yeesu ci boppam ba muy door, amoon na lu tollu ci fanweeri at, di doomu Yuusufa, ni ko xel mana jàppe.
Yuusufa, Eli mooy baayam,
24Eli, Matat. Matat, Lewi; Lewi, Melki; Melki, Yanayi; Yanayi, Yuusufa;
25Yuusufa, Matacas; Matacas, Amos; Amos, Nawum; Nawum, Esli; Esli, Nagayi.
26Nagayi, Maat; Maat, Matacas; Matacas, Semeyin; Semeyin, Yosex; Yosex, Yoda.
27Yoda, Yoxanan; Yoxanan, Resa; Resa, Sorobabel; Sorobabel, Selcel; Selcel, Neri;
28Neri, Melki; Melki, Adi; Adi, Kosam; Kosam, Elmadam; Elmadam, Er.
29Er, Yosuwe; Yosuwe, Elyeser; Elyeser, Yorim; Yorim, Matat; Matat, Lewi;
30Lewi, Simeyon; Simeyon, Yuda; Yuda, Yuusufa; Yuusufa, Yonam; Yonam, Elyakim.
31Elyakim, Meleya; Meleya, Mena; Mena, Matata; Matata, Natan; Natan, Daawuda.
32Daawuda mooy doomu Yese; Yese, Obedd; Obedd, Bowas; Bowas, Sala; Sala, Naason.
33Naason, Aminadab; Aminadab, Admin; Admin, Arni; Arni, Esron; Esron, Peres; Peres, Yuda;
34Yuda, Yanqóoba; Yanqóoba, Isaaxa; Isaaxa, Ibraayma; Ibraayma, Teraa; Teraa, Naxor;
35Naxor, Serug; Serug, Rew; Rew, Peleg; Peleg, Eber; Eber, Sela;
36Sela, Kenan; Kenan, Arpagsàdd; Arpagsàdd, Sem; Sem, Nóoyin; Nóoyin, Lemeg;
37Lemeg, Matusalem; Matusalem, Enog; Enog, Yeredd; Yeredd, Maalaleel; Maalaleel, Kenan;
38Kenan, Enos; Enos, Set; Set, Aadama; Aadama, Yàlla.
Currently Selected:
Luug 3: KY
Highlight
Copy
Compare
Share
Want to have your highlights saved across all your devices? Sign up or sign in
Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9
Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/
Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright