Loolu lañu bind ci téereb waxi Yonent Yàlla Esayi ne:
«Baatu nit a ngi xaacoo ca màndiŋ ma, naan:
“Nangeen xàll yoonu Boroom bi,
juballeen ay xàllam.
Xur yépp ay sëkke,
tund wu mag ak wu ndaw maasaloo,
yoon ya lunkoon, jubbantiku,
ya ñagasoon, nooy,
ba ñépp gis mucc gi Yàlla dogal.”»