Yowaan 14
14
Yeesu dëfal na taalibe ya
1«Buleen jàq. Gëmleen Yàlla te gëm ma. 2Sama kër Baay, dëkkuwaay yu baree nga fa. Su demewul woon noonu, ndax dinaa leen ne maa ngi leen fay waajali béreb? 3Te gannaaw bu ma leen waajalee béreb, dinaa délsi, jëlsi leen, yóbbu, ba fu ma nekk, man, ngeen nekk fa, yeen itam. 4Te fa ma jëm, xam ngeen yoon wi.» 5Tomaa ne ko: «Sang bi, xamunu foo jëm, kon ana nu nuy xame yoon wi?»
Yeesu mooy yoon wi jëm ci Yàlla
6Yeesu ne ko: «Man maay yoon wi, maay dëgg gi, te maay dund gi. Kenn du ñëw ci Baay bi te jaarewul ci man. 7Su ngeen ma xamoon, sama Baay itam, dingeen ko xam. Li ko dale tey nag, xam ngeen ko, gis ngeen ko.»
8Filib ne ko: «Sang bi, won nu Baay bi rekk, mu doy nu.» 9Yeesu ne ko: «Filib, ni ma yàggeek yeen te ba tey xamuloo ma? Ku ma gis kay, gis nga Baay bi. Kon ana noo naan: “Won nu Baay bi”? 10Dangaa gëmul ne man, maa ngi ci Baay bi, te Baay baa ngi ci man? Kàddu yi ma leen di wax, waxuma ko ci sama coobarey bopp, waaye Baay bi nekk ci man, moo sottal ay jëfam. 11Gëmleen ma, ndax kàddu gii ma ne, maa ngi ci Baay bi, te Baay baa ngi ci man; mbaa boog, ngeen gëm ndax jëf ji may def. 12Maa leen ko wax déy ci lu wér, ku ma gëm, jëf ji may def man, moom itam dina ko def, te jëf ju raw jii sax lay def, ndax man, ci Baay bi laa jëm. 13Te lépp lu ngeen ñaan ci sama tur, loolu laay def, ngir Doom ji fésal darajay Baay bi. 14Su ngeen ma ñaanee mbir ci sama tur, man maa koy def.
Yeesu dige na Noo gu Sell gi
15«Su ngeen ma soppee, sàmmleen samay ndigal. 16Man maay ñaan Baay bi, mu yónnee leen beneen Taxawukat#14.16 Taxawukat: Yeesu nee, Taxawukat bi ag noo la, kon bët du ko gis. Gannaaw bi Yeesu yéegee asamaan ba bésu Pàntakot dikk, ca la Taxawukat bi wàcc ci taalibey Yeesu. Ba tey itam, képp kuy taalibeb Yeesu, ci sa xol la Taxawukat biy dëkk., ngir mu nekk ak yeen ba fàww. 17Kooku mooy Noowug Yàlla giy xamle liy dëgg. Àddina du ko mana dalal, ndax gisu ko te xamu ko. Yeen nag xam ngeen ko, ndax ci seen biir la dëkk, te ci seen biir xel lay nekk. 18Duma leen bàyyi ngeen tumurànke. Dinaa délsi ci yeen. 19Des na tuuti, àddina du ma gisati; yeen dingeen ma gis, ndax man maa ngi dund, te yeen itam dingeen dund. 20Bésub keroog dingeen xam ne man maa ngi ci sama Baay, yeen ngeen nekk ci man, man it ma nekk ci yeen. 21Ki nangu sama ndigal nag, te di ko sàmm, moo ma sopp, te kooku ma sopp, cofeel ñeel na ko, bawoo fa sama Baay, te man itam dinaa ko sopp, di ko feeñu.»
22Yuda meneen ma wuuteek Yuda Iskaryo, ne ko: «Sang bi, lu waral nga nar noo feeñu te doo feeñu àddina?» 23Yeesu ne ko: «Ku ma sopp day sàmm sama kàddu, sama Baay sopp ko; fi moom lanuy dikk, te moom lanuy def màkkaan. 24Ku ma soppul, du sàmm samay kàddu. Kàddu gi ngeen dégg nag, du sama gos, waaye kàddug Baay bi ma yónni la.
25«Lii laa leen di wax bi may nekkagum ak yeen. 26Waaye Taxawukat bi, di Noo gu Sell gi leen Baay biy yónnee ci sama tur, moo leen di jàngal lépp, fàttali leen lépp lu ma leen waxoon, man. 27Jàmm laa leen bàyyee, sama jàmm laa leen may te mayuma leen ko ni àddina di mayee. Buleen jaaxle, buleen tiit.
28«Dégg ngeen ma ne leen: “Maa ngi dem, maa ngi délsi ci yeen.” Su ngeen ma soppoon, dingeen bége li may dem ci Baay bi, ndax Baay bee ma gëna màgg. 29Léegi bala looloo dikk nag laa leen koy wax, ngir bu dikkee ngeen gëm. 30Duma waxateek yeen lu bare ndax kàngamu àddinaa ngi dikk. Manul ci man dara nag. 31Waaye fàww àddina xam ne Baay bi laa sopp, te li ma Baay bi sant rekk laay def. Jógleen, nu dem!
Currently Selected:
Yowaan 14: KY
Highlight
Copy
Compare
Share
Want to have your highlights saved across all your devices? Sign up or sign in
Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9
Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/
Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright