1
Yowaan 14:27
Kàddug Yàlla
KY
Jàmm laa leen bàyyee, sama jàmm laa leen may te mayuma leen ko ni àddina di mayee. Buleen jaaxle, buleen tiit.
Compare
Explore Yowaan 14:27
2
Yowaan 14:6
Yeesu ne ko: «Man maay yoon wi, maay dëgg gi, te maay dund gi. Kenn du ñëw ci Baay bi te jaarewul ci man.
Explore Yowaan 14:6
3
Yowaan 14:1
«Buleen jàq. Gëmleen Yàlla te gëm ma.
Explore Yowaan 14:1
4
Yowaan 14:26
Waaye Taxawukat bi, di Noo gu Sell gi leen Baay biy yónnee ci sama tur, moo leen di jàngal lépp, fàttali leen lépp lu ma leen waxoon, man.
Explore Yowaan 14:26
5
Yowaan 14:21
Ki nangu sama ndigal nag, te di ko sàmm, moo ma sopp, te kooku ma sopp, cofeel ñeel na ko, bawoo fa sama Baay, te man itam dinaa ko sopp, di ko feeñu.»
Explore Yowaan 14:21
6
Yowaan 14:16-17
Man maay ñaan Baay bi, mu yónnee leen beneen Taxawukat, ngir mu nekk ak yeen ba fàww. Kooku mooy Noowug Yàlla giy xamle liy dëgg. Àddina du ko mana dalal, ndax gisu ko te xamu ko. Yeen nag xam ngeen ko, ndax ci seen biir la dëkk, te ci seen biir xel lay nekk.
Explore Yowaan 14:16-17
7
Yowaan 14:13-14
Te lépp lu ngeen ñaan ci sama tur, loolu laay def, ngir Doom ji fésal darajay Baay bi. Su ngeen ma ñaanee mbir ci sama tur, man maa koy def.
Explore Yowaan 14:13-14
8
Yowaan 14:15
«Su ngeen ma soppee, sàmmleen samay ndigal.
Explore Yowaan 14:15
9
Yowaan 14:2
Sama kër Baay, dëkkuwaay yu baree nga fa. Su demewul woon noonu, ndax dinaa leen ne maa ngi leen fay waajali béreb?
Explore Yowaan 14:2
10
Yowaan 14:3
Te gannaaw bu ma leen waajalee béreb, dinaa délsi, jëlsi leen, yóbbu, ba fu ma nekk, man, ngeen nekk fa, yeen itam.
Explore Yowaan 14:3
11
Yowaan 14:5
Tomaa ne ko: «Sang bi, xamunu foo jëm, kon ana nu nuy xame yoon wi?»
Explore Yowaan 14:5