Bible App logo
Search Icon

Yowaan 13

13
Yeesu raxas na tànki taalibeem
1Balaa màggalu bésub Mucc baa dikk, Yeesu xamoon na ne waxtu wa muy bàyyikoo àddina, jëm fa Baay ba, jot na. Cofeelu Yeesu ak ñoñam ñi ci àddina, googu cofeel la leen sopp ba ca muj ga.
2Ba Yeesu di bokk reer ak taalibe ya, fekk na Seytaane xiirtal Yuda, doomu Simoŋ Iskaryo, ci wor Yeesu. 3Yeesu xamoon na ne lépp la Baay bi teg ciy loxoom, te it ci Yàlla la jóge, te ci Yàlla la jëm. 4Mu jóge nag ca ndabal reer ba, summi mbubbam mu mag, daldi jël am malaan, laxasaayoo. 5Gannaaw loolu mu sotti ndox cib këll, daldi tàmbalee raxas tànki taalibe ya, di fompe sér ba mu laxasaayoo.
6Ba mu agsee ba ca Simoŋ Piyeer, Piyeer ne ko: «Sang bi, yaw yaa may raxasal samay tànk?» 7Yeesu ne ko: «Man li may def nii tey, xamuloo ko; waaye ëllëg dinga ko xam.» 8Piyeer ne ko: «Déedéet, doo ma raxasal samay tànk mukk kay!» Yeesu ne ko: «Su ma la raxasalul, doo am ci man benn cér.» 9Simoŋ Piyeer ne ko: «Kon nag Sang bi, bumu doon samay tànk doŋŋ, waaye na ci loxo yeek bopp bi bokk far!» 10Yeesu ne ko: «Ku sangu ba noppi, soxlaatula raxas lu moy ay tànkam, ndax set na wecc. Yeen nag set ngeen, waaye du ñépp.» 11Booba Yeesu xam na ka koy wor, te looloo tax mu ne: «Du yeen ñépp a set.»
12Gannaaw ba leen Yeesu raxasalee seeni tànk, teg ca solaat mbubbam, ba toogaat, da leen ne: «Xam ngeen li ma leen defal? 13Yeena ngi ma naa Kilifa gi ak Sang bi, te yeena yey, nde moom laa. 14Ndegam nag man miy Sang bi, di Kilifa gi maa leen raxasal seeni tànk, kon yeen itam war ngeen di raxasalante ay tànk. 15Ab misaalu royukaay laa leen jox, ngir ni ma leen defal, ngeen di ko def yeen itam. 16Maa leen ko wax déy ci lu wér, jaam sutul sangam, te ndaw sutul ka ko yónni. 17Loolu, su ngeen ko xamee, ndokkalee yeen, ndegam yeena ngi koy jëfe.
Yeesu weer na Yuda
18«Du yeen ñépp a tax may wax; man xam naa ñi ma tànn. Waaye Mbind mii fàww mu sotti: “Ki lekk samaw ñam moo ma wéq#13.18 Seetal ci Taalifi cant 41.10..” 19Léegi laa leen koy dale wax, bala looloo dikk, ngir bu dikkee ngeen gëm ne maay Ki nekk#13.19 maay Ki nekk: seetal ci 8.24.. 20Maa leen ko wax déy, ci lu wér, ku dalal nit ku ma yónni, man nga dalal; te ku ma dalal, dalal nga ki ma yónni.»
21Loolu la Yeesu wax ba noppi, njàqare dikkal ko, mu daldi biral ne: «Maa leen ko wax déy ci lu wér, kenn ci yeen moo may wor.» 22Taalibe ya di xoolante, te xamuñu kan lay wax. 23Booba kenn ca taalibe ya, di ku Yeesu soppoon, ma nga sóonu, sës rëkk ca Yeesu. 24Kooku la Simoŋ Piyeer liyaar, ngir mu laaj Yeesu ka ko taxoon di wax. 25Kooku sóonu ba tafu ca dënnub Yeesu, ne ko: «Sang bi, kooku kan la?» 26Yeesu ne ko: «Mooy ki may jox, man ci sama bopp, dogu mburu bi may capp ci ndab li.»
Yeesu nag jël dogu mburu, capp ko ca ndab la, jox ko Yuda, doomu Simoŋ Iskaryo. 27Naka la Yuda jël dog ba, Seytaane man ko. Yeesu ne ko: «Li ngay def, gaaw ci boog!»
28Loolu nag kenn ca ña woon ca ndab la xamul lu tax mu wax ko ko. 29Ñenn ña dañoo xalaat ne gannaaw Yuda moo yoroon dencub taalibe ya, Yeesu da koo wax ne ko, mu gaaw jëndi lu ñu waajale màggal gi, mbaa néew-doole yi la ko ne mu dem saraxi leen. 30Ba mu ko defee Yuda jël dogu mburu ba, daldi génn ca saa sa. Booba nag guddi na.
Yeesu nee, Piyeer dina jàmbu
31Ba Yuda génnee, Yeesu da ne: «Léegi nag darajay Doomu nit ki feeñ na, te darajay Yàllaa ngi feeñe ci moom. 32Te ni darajay Yàlla feeñe ci Doomu nit ki, ni la Yàlla di feeñale ci boppam darajay Doomu nit ki, te dina ko def léegi. 33Gone yi, diir bu gàtt laa deeti nekk ak yeen. Dingeen ma seet, waaye li ma wax Yawut yi rekk: “Man, fa ma jëm, yeen dungeen fa mana dem.” 34Kon ndigal lu bees laa leen di jox, soppanteleen: ni ma leen soppe, yeen itam nangeen ni soppantee. 35Ni ñépp di xame ne samay taalibe ngeen moo di ngeen soppante.»
36Simoŋ Piyeer ne ko: «Sang bi, foo jëm?» Yeesu ne ko: «Fa ma jëm, doo ma fa mana topp léegi, waaye dinga ma toppsi ca kanam.» 37Piyeer ne ko: «Sang bi, lu tee ma man laa topp léegi? Sama bakkan laa la àttana joxeel!» 38Yeesu ne ko: «Sa bakkan nga ma àttana joxeel? Maa la ko wax déy ci lu wér, bala ganaar a sab, dinga ma jàmbu ñetti yoon.

Currently Selected:

Yowaan 13: KY

Highlight

Copy

Compare

Share

None

Want to have your highlights saved across all your devices? Sign up or sign in