1
Yowaan 13:34-35
Kàddug Yàlla
KY
Kon ndigal lu bees laa leen di jox, soppanteleen: ni ma leen soppe, yeen itam nangeen ni soppantee. Ni ñépp di xame ne samay taalibe ngeen moo di ngeen soppante.»
Compare
Explore Yowaan 13:34-35
2
Yowaan 13:14-15
Ndegam nag man miy Sang bi, di Kilifa gi maa leen raxasal seeni tànk, kon yeen itam war ngeen di raxasalante ay tànk. Ab misaalu royukaay laa leen jox, ngir ni ma leen defal, ngeen di ko def yeen itam.
Explore Yowaan 13:14-15
3
Yowaan 13:7
Yeesu ne ko: «Man li may def nii tey, xamuloo ko; waaye ëllëg dinga ko xam.»
Explore Yowaan 13:7
4
Yowaan 13:16
Maa leen ko wax déy ci lu wér, jaam sutul sangam, te ndaw sutul ka ko yónni.
Explore Yowaan 13:16
5
Yowaan 13:17
Loolu, su ngeen ko xamee, ndokkalee yeen, ndegam yeena ngi koy jëfe.
Explore Yowaan 13:17
6
Yowaan 13:4-5
Mu jóge nag ca ndabal reer ba, summi mbubbam mu mag, daldi jël am malaan, laxasaayoo. Gannaaw loolu mu sotti ndox cib këll, daldi tàmbalee raxas tànki taalibe ya, di fompe sér ba mu laxasaayoo.
Explore Yowaan 13:4-5