Yowaan 11
11
Lu jëm ci deewug Lasaar
1Jenn waay a woppoon; ñu di ko wax Lasaar, di waa Betani, dëkkub Maryaama ak Màrt, ña mu bokkal ndey ak baay. 2Maryaama mooy ki sotti woon Sang bi lajkoloñ, ba fompe ay tànkam kawaru boppam. Moom la Lasaar mi woppoon di càmmiñam. 3Ñaari jigéeni Lasaar yooyu nag yónnee ca Yeesu ne ko: «Sang bi, sa soppe bi daa wopp.» 4Yeesu dégg ca, ne: «Wopp jooju de du woppi dee, waaye darajay Yàlla lay feeñal, ba màggale ko Doomu Yàlla ji.»
5Yeesu nag ku soppoon Màrt la, ak Maryaama ak Lasaar. 6Teewul ba mu déggee ne daa wopp, toogaat na ñaari fan fa mu nekkoon. 7Gannaaw loolu mu ne taalibe ya: «Nanu dellu Yude.» 8Taalibe ya ne ko: «Kilifa gi, yàggul dara la la fa waa Yude doon wuta sànniy doj ngir rey la, nga di fa dellu?» 9Yeesu ne leen: «Xanaa du bëccëg fukki waxtook ñaar la? Kuy doxe bëccëg, du fakkastalu, ndax leeru àddina sii muy gis. 10Waaye kuy doxe guddi, mooy fakkastalu, ndax ag leer la dul am.» 11Loolu la Yeesu wax, dal cay teg ne leen: «Sunu xarit Lasaar nelaw na, waaye maay dem ba yee ko.» 12Taalibe ya ne ko: «Sang bi, su dee nelaw kay, dina mucc.»
13Li Yeesu waxe noonu mooy Lasaar dee na, ñoom nag ñu foog ne da ne Lasaar day nelaw rekk. 14Ca la leen Yeesu wax lu leer, ne leen: «Lasaar dee na. 15Dee gi fekku ma fa, te loolu tax na maa bég ndax yeen, ngir dina tax ngeen gëm. Nanu ko seeti.» 16Ci kaw loolu Tomaa mi ñuy wax Seex bi, ne bokki taalibeem: «Nanu dem nun itam, ngir ànd ak moom dee!»
Yeesu mooy dekkal, di dundal
17Ba Yeesu agsee, fekk na Lasaar am ñeenti fan ci biir bàmmeel. 18Betani nag jegewoo na ak Yerusalem, te diggante bi yées na ñetti kilomet. 19Yawut yu baree dikkoon kër Màrt ak Maryaama, ngir dëfal leen ci seen deewug càmmiñ.
20Ba Màrt yégee ne Yeesoo ngay ñëw, da koo gatanduji, te fekk na Maryaama toog ca kër ga. 21Màrt ne Yeesu: «Sang bi, soo fi nekkoon de, sama càmmiñ du dee. 22Waaye ba léegi sax, xam naa ne loo ñaan Yàlla, Yàlla may la ko.» 23Yeesu ne ko: «Sa càmmiñ dina dekki.» 24Màrt ne ko: «Xam naa ne dina dekki kera ca ndekkitel bés bu mujj ba.» 25Yeesu ne ko: «Man maay ndekkite li, maay dund gi; ku ma gëm, soo deewee it, dinga dund. 26Te képp kuy dund te gëm ma, doo dee mukk. Ndax gëm nga loolu?» 27Mu ne ko: «Waaw, Sang bi. Man gëm naa ne yaay Almasi bi, Doomu Yàlla, ki ñëw ci àddina si.»
28Loolu la Màrt wax, daldi woowi Maryaama, ñaarook moom, ne ko: «Kilifa gi ñëw na, ba di la laaj.» 29Maryaama dégg loolu, gaaw jóg dem ca Yeesu. 30Booba Yeesu agseegul ca biir dëkk ba, waaye ma nga ba tey fa mu daje woon ak Màrt. 31Yawut ya nekk ak Maryaama ca kër ga, di ko dëfal nag, gis ko na mu nee bërét génn, ñu topp ko, defe ne day jooyi ca bàmmeel ba.
32Ba Maryaama agsee ba gis Yeesu, da ne gurub cay tànkam ne ko: «Sang bi, soo fi nekkoon de, sama càmmiñ li du dee.» 33Ba ko Yeesu gisee muy jooy, Yawut ya mu àndal itam di jooy, yaramam daw na, mu jàq. 34Mu ne leen: «Fu ngeen ko denc?» Ñu ne ko: «Kaay gis, Sang bi.»
35Yeesu nag jooy. 36Yawut ya naan: «Gisleen rekk ni mu ko bëgge!» 37Teewul ñenn ca ñoom naan: «Moom mi muri bëti gumba gi, manul woona fexe itam ba kii du dee?»
38Naka la yaramu Yeesu dawati lool, mu dem ba ca bàmmeel ba, muy pax mu ñu yatt ciw doj, ube pax mi aw doj. 39Yeesu ne: «Dindileen doj wi!» Màrt, jigéenu ki dee ne ko: «Sang bi, fii nu tollu dina am xet, nde mu ngi ci ñeenti fanam.» 40Yeesu ne ko: «Xanaa waxuma la ne soo gëmee, dinga gis màggug Yàlla?» 41Ñu dindi doj wa. Yeesu xool ca kaw, daldi ne: «Baay, sant naa la, ndax nangul nga ma. 42Man nag xam naa ne saa su nekk danga may nangul, waaye mbooloo mi fi teew a ma taxa wax loolu, ngir ñu gëm ne yaw yaa ma yebal.»
43Loolu la Yeesu wax, daldi xaacu ca kaw, ne: «Lasaar, génnal!» 44Néew bi génn ak càngaayam, tànk yeek loxo yi lëmëse, kanam ga muure. Yeesu ne leen: «Tekkileen ko, bàyyi ko mu dem.»
Yawut yi jógal nañu Yeesu
45Yawut yu bare ca ña ñëwoon kër Maryaama, ba ñu gisee la Yeesu def, ca lañu ko gëm. 46Teewul ñenn ca ñoom dem ca Farisen ya, ba nettali leen la Yeesu def. 47Sarxalkat yu mag ya ak Farisen ya woo kuréelu àttekat ya, ne leen: «Ana lu nuy def nag? Ndax nit kii kat a ngi def firnde yu bare! 48Su nu ko bàyyee nii, ñépp a koy gëm, te kon kilifay Room dikk boole sunu béreb bu sell bi ak sunuw xeet, tas!»
49Kenn ca ñoom nag ku ñuy wax Kayif te doon sarxalkat bu mag ba ca at mooma, ne leen: «Yeen, dangeena xamul dara. 50Yeen gisuleen sax ne seen njariñ moo di kenn nit doŋŋ deewal ñépp, ba askan wépp baña bokk sànku.»
51Loolu du lu Kayif wax ci sagoom, la mu doon sarxalkat bu mag ca at mooma, moo ko taxa jottali kàdduy waxyu yooyu mu biral, ne Yeesu mooy deewal xeet wi. 52Te du xeet woowu doŋŋ la ko defal, waaye da koo def ngir itam dajale doomi Yàlla yi tasaaroo, ñu doon benn bopp.
53Bésub keroog nag la njiiti Yawut yi dogu ci rey Yeesu. 54Ci kaw loolu Yeesu jaareetul fu ñu koy gise ca Yawut ña, waaye fa la bàyyikoo, dem gox ba feggook màndiŋ ma, ca dëkk ba ñuy wax Efrayim. Foofa la toog aki taalibeem.
55 Bésub Mucc nag moo jubsi woon, di màggalu Yawut yi. Ci biir loolu ñu bare jóge ca dëkki kaw ga, jëm Yerusalem balaa bésu Mucc baa dikk, ngir setluji fa. 56Ba mu ko defee ñuy seet Yeesu. Naka lañu taxaw ca kër Yàlla ga, di wax ca seen biir, naan: «Lu ngeen ci xalaat? Da dul ñëw ci màggal gi?» 57Ci biir loolu sarxalkat yu mag ya ak Farisen ya joxe ndigal ne képp ku xam fu Yeesu nekk, na ko xamle, ngir ñu jàpp ko.
Currently Selected:
Yowaan 11: KY
Highlight
Copy
Compare
Share
Want to have your highlights saved across all your devices? Sign up or sign in
Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9
Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/
Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright