Yowaan 10
10
Yeesu nee ku jaare ci moom, mucc
1«Maa leen ko wax déy ci lu wér, ku duggewul ci buntu wërmbalu xar yi, xanaa mu yéege feneen, tëb, kooku ab sàcc la, ab saay-saay la. 2Waaye ki dugge ci buntu wërmbal bi, kookooy sàmmub xar yi. 3Kooku la wattukat biy ubbil, xar yi di déglu baatam. Mooy woo xari boppam ci seen tur, génne leen. 4Bu génnee xaram yépp ba noppi, da leen di jiitu, ñu topp ci moom, ndax xàmmee nañu baatam. 5Ab jàmbur nag, duñu ko topp mukk; dañu koy daw kay, ndax xàmmeewuñu baatub jàmbur.»
6Léeb woowu la Yeesu léeb ci kanamu nit ñi, waaye ñoom xamuñu la mu leen wax. 7Ci kaw loolu Yeesu neeti: «Maa leen ko wax déy ci lu wér, man maay buntu wërmbalu xar yi. 8Mboolem ñi ma jiitu, ay sàcc aki saay-saay lañu, waaye xar yi dégluwuñu leen. 9Man maay bunt bi; ku dugge ci man, dinga mucc, di dugg aka génn, di gis mbooy goo fore. 10Ab sàcc moom, dara indiwu ko lu moy sàcc aka rey aka yàq. Man maa ñëw, ngir nit ñi dund dund gu naat.
11«Man maay sàmm bi baax#10.11 Seetal ci Esekiyel 34.15-16.. Sàmm bu baax, bakkanam lay joxe, jote ko ay xaram. 12Kuy sàmmaan di feyeeku te dub sàmm, moomuli xar; bu séenee bukki buy dikk, day bàyyi xar ya, daw, bukki ba jàpp ca, tasaare la ca des. 13Ab sàmmaan kuy feyeeku rekk la, xalaatul xar ya, moo tax muy daw.
14«Man maay sàmm bi baax. Maa xam sama xari bopp, ñoom it ñu xam ma. 15Noonu it laa xame Baay bi, Baay bi xame ma ni, te maay joxe sama bakkan, jote ko xar yi. 16Am naa it yeneen xar yu bokkul ci bii wërmbal. Ñoom it fàww ma indi leen, te dinañu dégg sama baat. Su ko defee muy gennug coggal, di bennub sàmm. 17Li tax Baay bi sopp ma, moo di sama bakkan laa joxe, ba man koo jëlaat. 18Kenn du jële sama bakkan ci man; man maa koy joxeel sama bopp. Maa ko saña joxe, maa ko saña jëlaat, te loolu la ma sama Baay sant.»
19Féewaloo nag amati ca Yawut ya, ndax kàddu yooyu. 20Ñu bare ca ñoom naan: «Aw rab a ko jàpp! Dafa dof! Lu ngeen koy dégloo?» 21Ña ca des naan: «Jii wax du waxi ku rab jàpp. Ndax aw rab man naa muri bëti gumba?»
Yawut ya gàntal nañu Yeesu
22Bés ba ñuy baaxantal daloog kër Yàlla ga la woon ca Yerusalem, yemook jamonoy sedd. 23Yeesoo nga doon doxantu ca kër Yàlla ga, ca mbaar ma ñuy wax Mbaarum Suleymaan. 24Yawut ya yéew ko ne ko: «Loo deeti xaar ci dindil nu kumpa; su dee yaa di Almasi bi, wax nu lu leer!»
25Yeesu ne leen: «Wax naa leen ko, yeena gëmul. Man, jëf ji may def ci sama turu Baay moo may seedeel. 26Waaye yeen yeena gëmul, ndax bokkuleen ci samay xar. 27Samay xar, sama baat lañuy déglu; maa leen xam, te man lañuy topp. 28Man maa leen di texeel ba fàww; duñu sànku mukk, te kenn du leen foqatee ci sama loxo. 29Sama Baay bi ma leen jox, moo gëna màgg lépp, te kenn manula foqatee lenn ci loxol Baay bi. 30Man ak Baay bi benn lanu.»
31Yawut ya nag foratiy xeer yu ñu ko sànni, ngir rey ko. 32Yeesu ne leen: «Jëf ju baax ju bare laa def ci ndigalal Baay bi. Ana ci yooyu jëf, jan ngeen ma nara sànnee ay xeer ba rey ma?» 33Yawut ya ne ko: «Du jëf ju baax lanu lay sànneey xeer, ba rey la, waaye dangaa diir Yàlla mbagg. Yaw ngay nit doŋŋ te naan yaay Yàlla!»
34Yeesu ne leen: «Xanaa bindeesul ci seen téereb yoon, kàddug Yàlla gii: “Dama ne ay yàlla ngeen#10.34 Seetal ci Taalifi cant 82.6.”? 35Ndegam Yàlla moo woowe “yàlla” ñi kàddug Yàlla dikkal, te Mbindum kàddoom maneesu koo toxal, 36kon man mi Yàlla beral boppam, yebal ma ci àddina, ana nu ngeen ma mana waxe ne: “Yaa diir Yàlla mbagg,” ndax li ma ne maay Doomu Yàlla? 37Su ma deful sama liggéeyu Baay, buleen ma gëm; 38waaye gannaaw moom laay def, su ngeen ma gëmul sax, gëmleen boog jëf ji, ngir ngeen xam te ràññee ne Baay baa ngi ci man, te man it, maa ngi ci Baay bi.» 39Ñu di ko jéematee jàpp nag, mu far rëcc leen.
40Ci kaw loolu Yeesu jàllaat dexu Yurdan, daldi dem fa béreb ba Yaxya njëkkoon di sóobe nit ñi, mu dal foofa. 41Ñu bare nag dikk, fekk ko fa, te naan: «Yaxya de wonewul jenn firnde, waaye mboolem lu mu wax ci kii, dëgg la.» 42Ñu bare gëme ko foofa.
Currently Selected:
Yowaan 10: KY
Highlight
Copy
Compare
Share
Want to have your highlights saved across all your devices? Sign up or sign in
Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9
Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/
Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright