1
Yowaan 11:25-26
Kàddug Yàlla
KY
Yeesu ne ko: «Man maay ndekkite li, maay dund gi; ku ma gëm, soo deewee it, dinga dund. Te képp kuy dund te gëm ma, doo dee mukk. Ndax gëm nga loolu?»
Compare
Explore Yowaan 11:25-26
2
Yowaan 11:40
Yeesu ne ko: «Xanaa waxuma la ne soo gëmee, dinga gis màggug Yàlla?»
Explore Yowaan 11:40
3
Yowaan 11:35
Yeesu nag jooy.
Explore Yowaan 11:35
4
Yowaan 11:4
Yeesu dégg ca, ne: «Wopp jooju de du woppi dee, waaye darajay Yàlla lay feeñal, ba màggale ko Doomu Yàlla ji.»
Explore Yowaan 11:4
5
Yowaan 11:43-44
Loolu la Yeesu wax, daldi xaacu ca kaw, ne: «Lasaar, génnal!» Néew bi génn ak càngaayam, tànk yeek loxo yi lëmëse, kanam ga muure. Yeesu ne leen: «Tekkileen ko, bàyyi ko mu dem.»
Explore Yowaan 11:43-44
6
Yowaan 11:38
Naka la yaramu Yeesu dawati lool, mu dem ba ca bàmmeel ba, muy pax mu ñu yatt ciw doj, ube pax mi aw doj.
Explore Yowaan 11:38
7
Yowaan 11:11
Loolu la Yeesu wax, dal cay teg ne leen: «Sunu xarit Lasaar nelaw na, waaye maay dem ba yee ko.»
Explore Yowaan 11:11