1
Yowaan 10:10
Kàddug Yàlla
KY
Ab sàcc moom, dara indiwu ko lu moy sàcc aka rey aka yàq. Man maa ñëw, ngir nit ñi dund dund gu naat.
Compare
Explore Yowaan 10:10
2
Yowaan 10:11
«Man maay sàmm bi baax. Sàmm bu baax, bakkanam lay joxe, jote ko ay xaram.
Explore Yowaan 10:11
3
Yowaan 10:27
Samay xar, sama baat lañuy déglu; maa leen xam, te man lañuy topp.
Explore Yowaan 10:27
4
Yowaan 10:28
Man maa leen di texeel ba fàww; duñu sànku mukk, te kenn du leen foqatee ci sama loxo.
Explore Yowaan 10:28
5
Yowaan 10:9
Man maay bunt bi; ku dugge ci man, dinga mucc, di dugg aka génn, di gis mbooy goo fore.
Explore Yowaan 10:9
6
Yowaan 10:14
«Man maay sàmm bi baax. Maa xam sama xari bopp, ñoom it ñu xam ma.
Explore Yowaan 10:14
7
Yowaan 10:29-30
Sama Baay bi ma leen jox, moo gëna màgg lépp, te kenn manula foqatee lenn ci loxol Baay bi. Man ak Baay bi benn lanu.»
Explore Yowaan 10:29-30
8
Yowaan 10:15
Noonu it laa xame Baay bi, Baay bi xame ma ni, te maay joxe sama bakkan, jote ko xar yi.
Explore Yowaan 10:15
9
Yowaan 10:18
Kenn du jële sama bakkan ci man; man maa koy joxeel sama bopp. Maa ko saña joxe, maa ko saña jëlaat, te loolu la ma sama Baay sant.»
Explore Yowaan 10:18
10
Yowaan 10:7
Ci kaw loolu Yeesu neeti: «Maa leen ko wax déy ci lu wér, man maay buntu wërmbalu xar yi.
Explore Yowaan 10:7
11
Yowaan 10:12
Kuy sàmmaan di feyeeku te dub sàmm, moomuli xar; bu séenee bukki buy dikk, day bàyyi xar ya, daw, bukki ba jàpp ca, tasaare la ca des.
Explore Yowaan 10:12
12
Yowaan 10:1
«Maa leen ko wax déy ci lu wér, ku duggewul ci buntu wërmbalu xar yi, xanaa mu yéege feneen, tëb, kooku ab sàcc la, ab saay-saay la.
Explore Yowaan 10:1