Yanqóoba 2
2
Gënaatle warul
1Bokk yi, bu leen di gënaatle te di gëmkati sunu Sang Yeesu Almasi bi, Boroom leer. 2Ndax su nit duggsee seenum ndaje, takk jaarob wurus, solu ba jekk; ku néew doole it duggsi, limboo ay sagar, 3su ngeen seetloo boroom col gu jekk gi, ne ko: «Toogeel fii, moo baax ci yaw,» te ne néew-ji-doole ji: «Yaw, taxaweel nee, mbaa nga toog fii ci suuf, ci samay tànk,» 4su boobaa xanaa du yeena ngi gënaatle ci seen biir, tey àttee ay mébét yu bon?
5Bokk yi, soppe yi, dégluleen. Xanaa du Yàlla moo tànn ñi àddina jàppe ñu néew doole, ngir ñu barele ngëm, boole ci jagoo nguur gi Yàlla dig ñi ko sopp? 6Yeen nag ngeen di teddadil néew doole yi! Xanaa du boroom alal yi ñoo leen di noggatu, di leen diri ba fa mbaxana dee benn? 7Xanaa du ñooñu ñooy ñàkke kersa tur wu tedd wi ngeen di wuyoo?
8Ndegam nag yoonu Buur Yàlla ngeen matal sëkk, di sàmmonteek Mbind mi ne: «Ni ngeen soppe seen bopp, nangeen ko soppe seen moroom#2.8 Seetal ci Sarxalkat yi 19.18.,» su boobaa waawleen góor! 9Waaye su ngeen gënaatlee, bàkkaar ngeen, te yoon topp na leen, ndax yeena ko xëtt. 10Ndax kat képp ku sàmm yoon wépp, ba mu des lenn ndigal doŋŋ lu mu tërëfe, ab daan bu ñu teg ci ku moy yoon wépp, ñeel na ko. 11Ndax ki ne: «Bul njaaloo,» moo ne itam: «Bul bóom#2.11 Seetal ci Mucc ga 20.13-14..» Ku njaaloowul te bóom nag, xëtt na yoon. 12Deeleen waxe tey jëfe ni mu jekke ci nit ñu ñuy séddeji àtteb yoon wiy goreel. 13Daan bu àndul ak yërmande, moom lees di àttee ña daawul jëfe yërmande. Yërmande nag kekku na ab daan.
Gëm, jëfe
14Bokk yi, ku ne gëm na, te jëfewu ko, ana lu mu koy jariñ? Ndax googu ngëm man na koo musal? 15Su mbokk mu góor mbaa jigéen raflee, mbaa mu ñàkk lu mu dunde bés bu nekk, 16ba kenn ci yeen ne mbokk mi: «Demal ak jàmm, solul nag te lekk ba regg,» te fajul aajoom, loolu lu muy jariñ? 17Noonu la ngëm deme, su amul jëf ju mu àndal, ngëm gu dee la.
18Waaye jombul nit ne: «Yaw, ngëm nga am, waaye man, jëf laa am.» Dama ne, won ma sa ngëm gu àndul ak jëf; man, samay jëf laa lay wone sama ngëm. 19Yaa gëm ne Yàlla kenn la; waaw góor, waaye rab yi it loolu lañu gëm bay lox.
20Yaa ñàkk bopp, ndax dangaa bëgg lu la firndeel ne ngëm gu àndul ak jëf amul njariñ? 21Sunu maam Ibraayma, xanaa du ci jëf lees ko baaxe àtteb ku jub, ndax jëf ja mu joxee doomam Isaaxa ca sarxalukaay ba? 22Kon gis nga ne ngëmam ga ak jëfam ja ñoo ànd di liggéey, te ca jëf ja la ngëm ga mate sëkk. 23Mbind ma daldi sotti, na mu dikke woon ne: «Ibraayma moo gëm Yàlla, Yàlla nangul ko ngëmam, muy àtteb njub bu ñu ko limal#2.23 Seetal ci Njàlbéen ga 15.6.,» ba ñu di ko woowe xaritu Yàlla. 24Ngeen gis kon ne ci jëf lees di baaxe nit àtteb ku jub, waaye du ci kaw ngëm doŋŋ.
25Xanaa du noonu it lañu baaxe Raxab#2.25 Seetal ci Yosuwe 2.1-21. gànc ba àtteb ku jub, ci kaw jëfam, ndax la mu dalaloon ndawi Yawut ya, ba awale leen feneen? 26Yaram wu àndul akug noo daal, ni mu deewe, noonu la ngëm gu àndul aki jëf deewe.
Currently Selected:
Yanqóoba 2: KY
Highlight
Copy
Compare
Share
Want to have your highlights saved across all your devices? Sign up or sign in
Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9
Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/
Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright