1
Yanqóoba 2:17
Kàddug Yàlla
KY
Noonu la ngëm deme, su amul jëf ju mu àndal, ngëm gu dee la.
Compare
Explore Yanqóoba 2:17
2
Yanqóoba 2:26
Yaram wu àndul akug noo daal, ni mu deewe, noonu la ngëm gu àndul aki jëf deewe.
Explore Yanqóoba 2:26
3
Yanqóoba 2:14
Bokk yi, ku ne gëm na, te jëfewu ko, ana lu mu koy jariñ? Ndax googu ngëm man na koo musal?
Explore Yanqóoba 2:14
4
Yanqóoba 2:19
Yaa gëm ne Yàlla kenn la; waaw góor, waaye rab yi it loolu lañu gëm bay lox.
Explore Yanqóoba 2:19
5
Yanqóoba 2:18
Waaye jombul nit ne: «Yaw, ngëm nga am, waaye man, jëf laa am.» Dama ne, won ma sa ngëm gu àndul ak jëf; man, samay jëf laa lay wone sama ngëm.
Explore Yanqóoba 2:18
6
Yanqóoba 2:13
Daan bu àndul ak yërmande, moom lees di àttee ña daawul jëfe yërmande. Yërmande nag kekku na ab daan.
Explore Yanqóoba 2:13
7
Yanqóoba 2:24
Ngeen gis kon ne ci jëf lees di baaxe nit àtteb ku jub, waaye du ci kaw ngëm doŋŋ.
Explore Yanqóoba 2:24
8
Yanqóoba 2:22
Kon gis nga ne ngëmam ga ak jëfam ja ñoo ànd di liggéey, te ca jëf ja la ngëm ga mate sëkk.
Explore Yanqóoba 2:22