Yanqóoba 1
1
Ubbite gi
1Ci man Yanqóoba, jaamub Yàlla ak Sang Yeesu Almasi bi, la bataaxal bii bawoo, ñeel fukki giir ak ñaar yi tasaaroo ci àddina. Maa ngi leen di nuyu.
Lu jëm ci nattu ak ngëm
2Bokk yi, bu ngeen jaaree ci mboolem xeeti nattu, jàppeleen ko mbég mu mat sëkk, 3te xam ne bu seen ngëm nattoo, ñeme coono la leen di jural. 4Na ag ñeme coono sottal liggéeyam ci yeen, ngir ngeen sotti, mat sëkk, te baña yéese fenn.
5Ku desele am xel mu rafet nag, na ko ñaan Yàlla, mu may ko ko, ndax Yàlla mooy yéwéne ñépp te du sikk kenn. 6Waaye ngëm la koy ñaane te bumu ci am benn sikki-sàkka, ndax kiy sikki-sàkka daa mel ni gannaxu géej bu ngelaw liy yóbbu, di ko lëmbaaje. 7Kooku bumu yaakaar dara ci Boroom bi. 8Boroom xel ñaar la, xel maa toogul ci lenn lu muy def.
Néewle kawe, barele suufe
9Mbokkum gëmkat mi suufe daraja, na sagoo ab kawewaayam ci ni ko Yàlla yékkatee; 10te ki barele it na sagoo ci ni ko Yàlla suufeelee, ndax ni tóor-tóoru saxyaay di ruuse, noonu lay wéye. 11Naka la jant di fenk, ba naaj wi tàng jérr, saxyaay lax, tóor-tóoram ruus, taar ba réer ko mërr. Noonu itam la ki barele di jeexlee ci biiri yëngoom.
Yàllaay nattoo waaye du fiir kenn
12Ndokkalee ku muñ ab nattu, nde su ca amee ngërëm, mooy yooloo kaalag texe gi Yàlla dig ñi ko sopp.
13Képp ku dajeek lu koy xiirtal, bumu ne: «Yàllaa ma xiirtal,» ndax maneesula xiirtal Yàlla ci lu bon, te moom ci boppam du xiirtal kenn. 14Waaye ku nekk, sa xemmemtéefu bakkanu bopp moo lay xiirtal, ootal la ba nax la. 15Te xemmemtéefu bakkan bu ëmbee, bàkkaar lay wasin, te bàkkaar bu matee, dee lay jur.
16Bokk yi, soppe yi, buleen juum ci lii: 17gépp may gu baax ak bépp jagle bu mat, fa kaw la bawoo, di lu wàcce fa Baay biy boroom leer yi, ki soppikuwul ci lenn, te genn ker gu toogadi nekkul ci moom. 18Moom la soob mu jur nu ci kàddug dëgg gi, ba nu taxawe saraxu ndoortel meññeef, ci biiri bindeefam.
Jëfeleen kàddug Yàlla
19Bokk yi, soppe yi, nangeen xam lii: na ku nekk di gaaw ci déglu, di yeexa wax tey yeexa mer. 20Ndax merum nit du jur njub fa Yàlla. 21Kon nag baleen jépp jikko ju tilim ak mboolem xeeti mbon yi ne gàññ, te ngeen nangu, ci biir ag woyof, kàddu gi Yàlla xasa jëmbat ci yeen te mu man leena musal.
22Doonleen jëfekati kàddu gi, buleen di ay déglukat doŋŋ, di nax seen bopp. 23Ndax kat kuy déglu kàddu gi te jëfewoo ko, kooku daa mel ni kuy niir kanamam cib seetu: 24bu niiree boppam, dem daldi fàtte ca saa sa lu muy nirool. 25Waaye ki ne jàkk yoon wu mat sëkk wiy goreel ku ko topp, saxoo yoon wi te bañ koo dégg, fàtte, xanaa di dégg, jëfe, kooku mooy bége jëfam.
26Ku yaakaar ne am na diine te moomul làmmiñam, boppam lay nax te diineem amul njariñ. 27Diine gu set te mucc sikk fa kanam Yàlla Baay bi moo di lii: di nemmiku jirim akub jëtun ci seen njàqare, tey sàmm boppam, ba mucc ci gàkki àddina.
Currently Selected:
Yanqóoba 1: KY
Highlight
Copy
Compare
Share
Want to have your highlights saved across all your devices? Sign up or sign in
Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9
Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/
Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright