1
Yanqóoba 1:2-3
Kàddug Yàlla
KY
Bokk yi, bu ngeen jaaree ci mboolem xeeti nattu, jàppeleen ko mbég mu mat sëkk, te xam ne bu seen ngëm nattoo, ñeme coono la leen di jural.
Compare
Explore Yanqóoba 1:2-3
2
Yanqóoba 1:5
Ku desele am xel mu rafet nag, na ko ñaan Yàlla, mu may ko ko, ndax Yàlla mooy yéwéne ñépp te du sikk kenn.
Explore Yanqóoba 1:5
3
Yanqóoba 1:19
Bokk yi, soppe yi, nangeen xam lii: na ku nekk di gaaw ci déglu, di yeexa wax tey yeexa mer.
Explore Yanqóoba 1:19
4
Yanqóoba 1:4
Na ag ñeme coono sottal liggéeyam ci yeen, ngir ngeen sotti, mat sëkk, te baña yéese fenn.
Explore Yanqóoba 1:4
5
Yanqóoba 1:22
Doonleen jëfekati kàddu gi, buleen di ay déglukat doŋŋ, di nax seen bopp.
Explore Yanqóoba 1:22
6
Yanqóoba 1:12
Ndokkalee ku muñ ab nattu, nde su ca amee ngërëm, mooy yooloo kaalag texe gi Yàlla dig ñi ko sopp.
Explore Yanqóoba 1:12
7
Yanqóoba 1:17
gépp may gu baax ak bépp jagle bu mat, fa kaw la bawoo, di lu wàcce fa Baay biy boroom leer yi, ki soppikuwul ci lenn, te genn ker gu toogadi nekkul ci moom.
Explore Yanqóoba 1:17
8
Yanqóoba 1:23-24
Ndax kat kuy déglu kàddu gi te jëfewoo ko, kooku daa mel ni kuy niir kanamam cib seetu: bu niiree boppam, dem daldi fàtte ca saa sa lu muy nirool.
Explore Yanqóoba 1:23-24
9
Yanqóoba 1:27
Diine gu set te mucc sikk fa kanam Yàlla Baay bi moo di lii: di nemmiku jirim akub jëtun ci seen njàqare, tey sàmm boppam, ba mucc ci gàkki àddina.
Explore Yanqóoba 1:27
10
Yanqóoba 1:13-14
Képp ku dajeek lu koy xiirtal, bumu ne: «Yàllaa ma xiirtal,» ndax maneesula xiirtal Yàlla ci lu bon, te moom ci boppam du xiirtal kenn. Waaye ku nekk, sa xemmemtéefu bakkanu bopp moo lay xiirtal, ootal la ba nax la.
Explore Yanqóoba 1:13-14
11
Yanqóoba 1:9
Mbokkum gëmkat mi suufe daraja, na sagoo ab kawewaayam ci ni ko Yàlla yékkatee
Explore Yanqóoba 1:9