YouVersion Logo
Search Icon

Yawut ya 1

1
Yàlla moo feeñ ci Doom ji
1Bu yàgg la Yàlla waxoon ay yooni yoon ak maam ya, ci waxin yu bare, yonent yi jottali. 2Ci fan yu mujj yii, ci Doom ji la jaare wax ak nun, ki mu jagleel lépp, te ci moom la sàkke àddina wërngal këpp. 3Kooku mooy lerxat leeru Yàlla, te mooy ki jëmmal nekkug Yàlla. Moo téyee lépp kàddoom gu manoorewu. Gannaaw ba mu setalee bàkkaar yi nag, fa ndijooru Aji Màgg ji la toog, fa kawte ya, 4te ni turam wi mu séddoo gëna màgge turi malaaka yi, ni lees ko yékkatee, ba mu gëna màgg malaaka yi.
Doom jee gëna màgg malaaka yi
5Ndax kat, ana kan ci malaaka yi la Yàlla masa wax ne ko:
«Yaa di sama Doom,
bés niki tey, maa la jur#1.5 Seetal ci Taalifi cant 2.7. Su Yàlla nee moo ko jur, waxin la rekk. Bés bi ñu doon fal ab buur ci bànni Israayil la Yàlla di biral ne jàppe na buur bi ni doomam. Ni doom di teewale baayam, ni la buur biy teewale Yàlla ci kaw suuf.
ba neeti:
«Maay doon Baay ci moom,
muy Doom ci man#1.5 Seetal ci 2.Samiyel 7.14.»?
6Buy indiwaat taaw bi ci àddina nag, ci la naan:
«Na ko malaakay Yàlla yépp sujjóotal#1.6 Seetal ci Taalifi cant 97.7 ni ñu ko binde ci tekkiteg Mbind mu sell mi ci làkku gereg.
7Malaaka yi, la Yàlla wax ci seen mbir ne:
«Moo def ay malaakaam diy ngelaw,
jawriñam ñooñu la def tàkk-tàkki sawara#1.7 Seetal ci Taalifi cant 104.4.
8Waaye Doom ji la Yàlla ne:
«Yàlla, sab jal a sax dàkk ba fàww,
sa yetu buur njub la.
9Yaa sopp dëgg, bañ lu bon,
ba Yàlla, sa Yàlla diwe la diwu mbég,
nga tiim say moroom#1.8-9 Seetal ci Taalifi cant 45.7-8.
10Mu neeti:
«Yaw Sang bi, ca njàlbéen ga, yaa samp suuf,
sàkke asamaan say loxo.
11Yooyu day réer,
waaye yaw yaay sax,
lépp ay ràpp ni mbubb.
12Yaa leen di taxañ ni malaan,
ni yére di soppikoo it lañuy soppikoo,
te yaw ngay kenn ki,
te say at amul kem#1.10-12 Seetal ci Taalifi cant 102.26-28.
13Ana kan ci malaaka yi la mas ne:
«Toogeel sama ndijoor,
ba ma def say noon sa ndëggastal#1.13 Seetal ci Taalifi cant 110.1.»?
14Xanaa malaaka yépp duñu ay ngelaw yu ñu sas ab liggéey, yebal leen ngir ñu taxawu ñi wara jagoo ag mucc?

Currently Selected:

Yawut ya 1: KY

Highlight

Copy

Compare

Share

None

Want to have your highlights saved across all your devices? Sign up or sign in