YouVersion Logo
Search Icon

Filemon 1

1
Ubbite gi
1Ci man Póol, mi ñu tëj kaso ngir Almasi Yeesu, ci man ak itam ci Timote miy mbokkum gëmkat la bataaxal bii bawoo, ñeel Filemon, sunu soppe bi bokk ak nun liggéey bi. 2Mu ñeel itam sunub jigéen Afya, ak Arsipp sunu mbokkum xarekat, ak mbooloom gëmkat miy dajee sa kër. 3Yeen la aw yiw ak jàmm ñeel, bawoo fa Yàlla sunu Baay ak Sang bi Yeesu Almasi bi.
Póol a ngi sant ci biir ñaan
4Sant sama Yàlla laa dëkke saa yu ma la fàttalikoo ci samay ñaan, 5ndax dégg naa sa ngëm ci Sang Yeesu ak sa cofeel ci mboolem ñu sell ñi. 6Damay ñaan nag sa ngëm gi nu bokk amal la njariñal ràññee mboolem ngëneel yi nu am ci Almasi bi. 7Mbokk mi, mbégte mu réy ak xel mu dal laa am ci sa cofeel, ndax ni nga serale xolu aji sell ñi.
Póol tinul na Onesim
8Lii nag sañoon naa la koo digal ci turu Almasi bi, ndax mooy li la war, 9waaye tinu la ci ngir cofeel, mooy li ma taamu, man Póol mu màggat mii, boole ci léegi tënku biir kaso ndax Almasi Yeesu. 10Damay tinul Onesim, sama doomu tuubeen ji ma tuubloo ba mu mel ni maa ko jur ci diir bi ma nekke fii ci kaso bi. 11Amalu la woon njariñ#Aaya 11 njariñ: ci làkku gereg turu Onesim mooy tekki «Ku am njariñ». démb, waaye tey yaak man la amal njariñ.
12Maa ngi koy yebal ngir mu dellu fi yaw, te di kenn ci man. 13Dama koo bëggoona téye fi sama wet, ngir mu taxawal la, di ma dimbali, li feek maa ngi ci kaso bi ngir xibaaru jàmm bi. 14Waaye bëggumaa def dara loo àndul, ngir mu baña doon ndimbalu ñàkk pexe, xanaa loo defe xol bu tàlli. 15Jombul itam dees koo tàggale ak yaw ab diir, ngir nga jotaat ci moom ba fàww, 16ba dootul doon sab jaam, waaye day wees ab jaam, di mbokk, di soppe, ma sopp ko lool, te nga war ma koo gëna sopp, ngir jëmmu boppam ak Sang bi ngeen bokk.
17Ndegam nag sa waay nga ma def, dalal ko ni su doon man. 18Su la tooñee, mbaa mu ameel la lenn, topp ma ko. 19Man Póol maay bind fii ci sama loxol bopp: maay fey loolu, duma ci tuddaale bor bi nga ma ameel, te muy sa njotug bakkanu bopp! 20Kon nag mbokk mi, may ma googu njekk ngir Sang bi, te nga seral sama xol ndax Almasi bi. 21Wóor na ma ci diggante bii may bind bataaxal bi, ne dinga ma déggal, te xam naa ne dinga def sax lu wees li may wax.
22Te itam nanga ma waajalaale ab dal, ndax yaakaar naa ne dees na ma delloosi fi yeen, ndax seen ñaan yu nangu.
23Epafras, mbokk mi ñu ma tëjandool ndax Almasi Yeesu, mu ngi lay nuyu, 24mook Màrk ak Aristàrk ak Demas ak Luug, bokk yi may liggéeyandool.
25Yal na yiwu Sang Yeesu Almasi bi ànd ak seenum xel.

Currently Selected:

Filemon 1: KY

Highlight

Copy

Compare

Share

None

Want to have your highlights saved across all your devices? Sign up or sign in