YouVersion Logo
Search Icon

Njàlbéen ga 35

35
Yanqóoba sanc na Betel
1Ba loolu wéyee Yàlla ne Yanqóoba: «Jógal dem Betel, toog fa te nga sàkkal fa sarxalukaay Yàlla, ji la feeñu, ba ngay daw sa mag Esawu.» 2Yanqóoba wax ak waa këram ak ñi ànd ak moom ñépp ne leen: «Jëleleen ci seen biir tuuri doxandéem yi, te ngeen sangu-set te solu. 3Danuy dem Betel, ma sàkkal fa sarxalukaay Yàlla ji ma wallu, ba ma nekkee ci njàqare, te ànd ak man fépp fu ma jaar.» 4Ñu daldi jox Yanqóoba mboolem tuuri doxandéem, yi ñu yor, ak seen jaaroy nopp, Yanqóoba boole suul ca taatu garab#35.4 Xeetu garab la gu ñuy wax terebent. gu mag ga nekkoon ca wetu dëkk, ba ñu naan Sikem. 5Gannaaw loolu ñu sàqi, Yàlla nag wàcce tiitaange ju réy ca kaw dëkk ya leen wër, ba taluñoo dabi doomi Yanqóoba ya.
6Ba mu ko defee Yanqóoba ak ñi mu àndal ñépp agsi Lus, di Betel ba tey, foofa ca réewu Kanaan. 7Mu sàkk fa nag sarxalukaay, tudde béreb ba El Betel, ndax foofa la ko Yàlla feeñoo, bi muy daw magam. 8Foofa itam la Debora, ma daa nàmpal Rebeka, faatoo, ñu suul ko ca taatu garab gu mag ga ca wetu Betel. Ñu tudde garab ga Alon Bakut (muy firi Garabu jooyoo).
9Ba Yanqóoba jógee Padan Aram, Yàlla feeñuwaat na ko, barkeel ko 10ne ko: «Yaa di Yanqóoba, waaye deesatu la woowe Yanqóoba; léegi yaa di Israayil.»
Mu tudde ko nag Israayil.
11Yàlla neeti ko: «Man maay Yàlla Aji Man ji. Giiral te yokku, ba aw xeet ak mboolooy xeet sosoo ci yaw, te ay buur askanoo ci sa geño. 12Réew mi ma sédd Ibraayma ak Isaaxa, yaw laa koy sédd, yaak askan wi soqikoo ci yaw.»
13Naka la Yàlla wax ak Yanqóoba loolu, daldi teqalikoo ak moom. 14Yanqóoba samp doju xàmmikaay ca béreb, ba Yàlla waxe ak moom, tuural ko fa biiñ, sotti fa diw, sellale. 15Yanqóoba ma nga tudde béreb ba Yàlla waxeek moom, Betel#35.15 Betel: mu ngi tekki «kër Yàlla»..
Beñamin juddu na, Rasel faatu
16Ba loolu wéyee ñu jóge Betel, dem bay bëgga jub Efrata. Rasel tollu ciw mat, te mat wi metti. 17Ba mu demee ba mat wa gëna metti, rewlikat ba ne ko: «Muñal nag, ndax góor laati de!» 18Booba Rasel a ngi waaja faatu. Terewul bala bakkanam a rot tudde na xale bi Benoni (muy firi Sama doomu coono). Teewul baay bi tudde ko Beñamin#35.18 Beñamin: mu ngi jóge ci ben yamin, di tekki «doomu ndijoor», waaye li tur wiy wund mooy «doomu njiglaay». (muy firi Sama doomu njiglaay).
19Ci kaw loolu Rasel faatu, ñu denc ko ca yoonu Efrata, ga ñuy wax Betleyem ba tey. 20Yanqóoba nag samp aw doj ca bàmmeel ba, te mooy xàmmikaayu bàmmeelu Rasel ba tey jii. 21Ba mu ko defee Israayil jóge fa, samp xaymaam ca gannaaw Migdal Eder.
Doomi Yanqóoba ya
22Ba Israayil dëkkee ca réew ma, am na bés Ruben dem tëdd ak Bilaa, nekkaaleb baayam; Israayil yég ko.
Doomi Yanqóoba#35.22 Yanqóoba mooy Israayil. yu góor fukk lañu ak ñaar. 23Doomi Leya ñooy: Ruben, taawub Yanqóoba, ak Simeyon ak Lewi ak Yuda ak Isaakar ak Sabulon. 24Doomi Rasel di Yuusufa ak Beñamin. 25Doomi Bilaa, jaamub Rasel, di Dan ak Neftali. 26Doomi Silpa, jaamub Leya, di Gàdd ak Aser. Ñooñooy doomi Yanqóoba, te mu ame leen ca Padan Aram.
Isaaxa faatu na
27Yanqóoba dellu na kër baayam Isaaxa fa Mamre, ca Kiryaat Arba, gay Ebron ba tey, fa Ibraayma ak Isaaxa daloon. 28Isaaxa dund na téeméeri at ak juróom ñett fukk (180). 29Foofa la bakkanam rote, mu faatu, fekki ay maamam, gannaaw ba mu màggatee, ba ñor xomm. Ba loolu amee ay doomam Esawu ak Yanqóoba rob ko.

Currently Selected:

Njàlbéen ga 35: KY

Highlight

Copy

Compare

Share

None

Want to have your highlights saved across all your devices? Sign up or sign in