YouVersion Logo
Search Icon

Njàlbéen ga 36

36
Askanu Esawu
(Saar 36.1-43)
1Askanu Esawu, mi ñuy wax Edom, mooy lii.
2Esawu jël na janqi Kanaaneen jabar. Ñooñoo di Ada doomu Elon, Etteen ba, ak Olibama doomu Ana, miy doomu Cibeyon, Eween ba, 3ak Basmat doomu Ismayla, di jigéenub Nebayot. 4Ada am ak Esawu Elifas; Basmat am ca Rewel. 5Olibama am ca Yewus, Yalam ak Kore. Ñooñu ñooy doomi Esawu yu góor, te mu am leen ca réewu Kanaan.
6Ba loolu amee Esawu ànd aki soxnaam, aki doomam yu góor ak yu jigéen, ak waa këram ñépp, jiital géttam ak juram gépp, yóbbaale mboolem alal ju mu amoon ca réewu Kanaan, daldi sanci meneen réew ngir sore rakkam Yanqóoba. 7Li ko waral mooy, seen alal dafa bare woon lool, ba manuñoo dëkk ñoom ñaar, te réew mi ñu daloon, àttanu leen ndax seen gétt yu bare. 8Esawu nag dëkk ca tundu Seyir: Esawu moomu mooy Edom.
9Askanu Esawu, di maami Edomeen ña ca tundi Seyir, mooy lii.
10Doomi Esawu yu góor ñooy: Elifas, mi mu am ak soxnaam Ada; ak Rewel, mi mu am ak soxnaam Basmat. 11Doomi Elifas yu góor yi di Teman ak Omar ak Cefo ak Gatam ak Kenas. 12Elifas amoon na it nekkaale bu ñuy wax Timna. Mu am caak moom Amaleg. Ñooñoo xeetoo ci Ada, soxnas Esawu. 13Doomi Rewel yu góor ñoo di Naxat ak Sera ak Saama ak Misa. Ñooñoo xeetoo ca Basmat, soxnas Esawu. 14Soxnas Esawu, si ñu naa Olibama, tey doomu Ana miy doomu Cibeyon, moo am ak Esawu doom yu góor yii: Yewus ak Yalam ak Kore.
15Làngi doomi Esawu yu góor nag, ñooy ñii. Ñi askanoo ci Elifas taawub Esawu, ñuy Teman ak Omar ak Cefo ak Kenas 16ak Kore ak Gatam ak Amaleg, ku ci nekk ak làngam. Làngi Elifas, ya ca réewum Edom a ngi noonu; ñooy sëti Ada. 17Ñi askanoo ci Rewel doomu Esawu, ñooy Naxat ak Sera ak Saama ak Misa, ku ci nekk ak làngam. Làngi Rewel, ya ca réewum Edom a ngi noonu; ñooy sëti Basmat, soxnas Esawu. 18Ñi xeetoo ci Olibama soxnas Esawu, ñooy Yewus, Yalam ak Kore, ku ci nekk ak làngam. Ñooñooy làngi Olibama, soxnas Esawu siy doomu Ana. 19Ñooñooy doomi Esawu, mi ñuy wax Edom, ñooñooy doomam yu góor, ñook seeni làng.
Lu jëm ci ña sancoon réewum Edom
20Doomi Seyir yu góor, ya bokk ca waa Or te sancoon ca réew ma, ñooy Lotan ak Sobal ak Cibeyon ak Ana 21ak Dison ak Eccer ak Disan. Ñooñooy làngi waa Or, di sëti Seyir ya ca réewum Edom. 22Doomi Lotan yu góor ñoo di Ori ak Emam. Jigéenub Lotan di Timna. 23Doomi Sobal yu góor ñoo di Alwan ak Manaxat ak Ebal ak Sefo ak Onam. 24Doomi Cibeyon yu góor di Aya ak Ana. Te Ana moomu moo feeñal bëti ndox yu tàng ya ca màndiŋ ma, ba muy sàmm mbaami baayam Cibeyon. 25Doomu Ana ju góor mooy Dison, ak Olibama, doomam ju jigéen. 26Doomi Dison yu góor di Emdan ak Esban ak Yittran ak Keran. 27Doomi Eccer yu góor ñoo di Bilan ak Saawan ak Akan. 28Doomi Disan yu góor di Ucc ak Aran.
Lu jëm ci buur ya njëkka falu ca Edom
29Làngi waa Or ñooy ñi askanoo ci Lotan ak Sobal ak Cibeyon ak Ana 30ak Dison ak Eccer ak Disan, ku ci nekk ak làngam. Ñooñooy làngi waa Or, na ñu xàjjalikoo kenn-kenn ca réewu Seyir.
31Buur ya falu woon ca réewum Edom, lu jiitu benn buuru bànni Israayil di falu ñii la: 32Bela doomu Bewor ju góor falu na ca Edom. Dinaba moo doon péeyam. 33Ba Bela faatoo, Yobab doomu Sera, ma dëkk Boccara, moo falu buur, wuutu ko. 34Ba Yobab faatoo, Usam ma bokk ci diiwaanu waa Teman falu buur, wuutu ko. 35Ba Usam faatoo, Adàdd, doomu Bedàdd ju góor, ja duma woon waa Majan ca réewu Mowab, daldi falu buur, wuutu ko. Péeyam moo doon Awit. 36Ba Adàdd faatoo, Samla ma dëkk Masreka moo falu buur, wuutu ko. 37Ba Samla faatoo, Sawul mu Rexobot Efraat moo falu buur, wuutu ko. 38Ba Sawul faatoo, Baal Anan doomu Agbor ju góor moo falu buur, wuutu ko. 39Ba Baal Anan doomu Agbor faatoo, Adar falu buur, wuutu ko. Pawu moo doon péeyam, soxnaam di Metabeel ma Mataredd doomu Mesaab di yaayam.
40Làng yi sosoo ci Esawu nag, làng gu ci nekk ak turam ak njaboot, ya mu ëmb, ak gox, ba mu dëkke, ñoo di ñii: ñi askanoo ci Timna ak Alwa ak Yetet 41ak Olibama ak Ela ak Pinon 42ak Kenas ak Teman ak Mibcar 43ak Magdiyel ak Iram, ku ci nekk ak làngam. Ñooñoo doon kilifay Edom, ma ñu naa Esawu, moom ma giir Edomeen ñi, làng gu ci nekk ak gox, ba nga dëkke te moom ko.

Currently Selected:

Njàlbéen ga 36: KY

Highlight

Copy

Compare

Share

None

Want to have your highlights saved across all your devices? Sign up or sign in