1
Njàlbéen ga 35:11-12
Kàddug Yàlla
KY
Yàlla neeti ko: «Man maay Yàlla Aji Man ji. Giiral te yokku, ba aw xeet ak mboolooy xeet sosoo ci yaw, te ay buur askanoo ci sa geño. Réew mi ma sédd Ibraayma ak Isaaxa, yaw laa koy sédd, yaak askan wi soqikoo ci yaw.»
Compare
Explore Njàlbéen ga 35:11-12
2
Njàlbéen ga 35:3
Danuy dem Betel, ma sàkkal fa sarxalukaay Yàlla ji ma wallu, ba ma nekkee ci njàqare, te ànd ak man fépp fu ma jaar.»
Explore Njàlbéen ga 35:3
3
Njàlbéen ga 35:10
ne ko: «Yaa di Yanqóoba, waaye deesatu la woowe Yanqóoba; léegi yaa di Israayil.» Mu tudde ko nag Israayil.
Explore Njàlbéen ga 35:10
4
Njàlbéen ga 35:2
Yanqóoba wax ak waa këram ak ñi ànd ak moom ñépp ne leen: «Jëleleen ci seen biir tuuri doxandéem yi, te ngeen sangu-set te solu.
Explore Njàlbéen ga 35:2
5
Njàlbéen ga 35:1
Ba loolu wéyee Yàlla ne Yanqóoba: «Jógal dem Betel, toog fa te nga sàkkal fa sarxalukaay Yàlla, ji la feeñu, ba ngay daw sa mag Esawu.»
Explore Njàlbéen ga 35:1
6
Njàlbéen ga 35:18
Booba Rasel a ngi waaja faatu. Terewul bala bakkanam a rot tudde na xale bi Benoni (muy firi Sama doomu coono). Teewul baay bi tudde ko Beñamin (muy firi Sama doomu njiglaay).
Explore Njàlbéen ga 35:18