Mucc ga 25
25
Lu jëm ci jaamookaay bi
(Saar 25.1—27.19)
1Aji Sax ji waxati Musaa ne ko: 2«Waxal bànni Israayil ne leen, ñu indil ma ab saraxu njébbal. Ci képp ku am yéene ji, ngeen di jële li ñu may jébbal, indil ma ko. 3Li ngeen di jële ci ñoom di wurus ak xaalis ak xànjar, 4ak wëñ gu baxa te laal yolet ak wëñ gu xewar ak gu xonq curr ak wëñu lẽe, ak kawari bëy 5ak deri kuuy yu ñu wulli, sóob ko xonqal, ak deri piipi#25.5 piipi, rabu géej la, bu der ba nooy te ndox du ko dugg. ak banti séng#25.5 séng: am na ñu koy woowe akasiya. Am na geneen garab gu xeetoo ak moom muy kàdd., 6ak diwu oliw gu ñuy taaloo, ak ndàbb luy xeeñal diwug pal#25.6 diwug pal mooy li ñuy diwe sarxalkat, buur mbaa yonent ngir tabb leen ci seen liggéey., di xeeñal cuuraay, 7ak ay peri onigsë, ak yeneen per yu ñuy tapp ci xar-sànnim sarxalkat bu mag ba ak kiiraayal dënnam. 8Na ma bànni Israayil defaral béreb bu sell, ndax ma dëkk ci seen biir. 9Na lépp dëppoo ak li ma lay won. Muy misaalu xaymab jaamookaay bi, di misaalu mboolem ay jumtukaayam, lépp defeleen ko noonu.
Lu jëm ci gaal giy def àlluway seede si
10«Defarleen gaalu dénku séng, guddaay bi di ñaari xasab#25.10 xasab mooy guddaayu loxo, diggante catu baaraamu digg ak conc, di ñeent fukki sàntimet ak juróom. ak genn-wàll, yaatuwaay bi di xasab ak genn-wàll; taxawaay bi di xasab ak genn-wàll. 11Nañu ko xoobe wurusu ngalam. Biir ak biti lañu koy xoobe wurus, sàkkal ko kéméju wurus gu ko wër. 12Móolalal gaal gi ñeenti lami wurus yu ñuy takk ci ñeenti tànk yi; ñaari lam ci genn wet gi, ñaar, wet gi ci des. 13Yattlul ay njàppuy bantu séng te nga xoob bu ci nekk wurus. 14Su ko defee nga roof njàppu yi ci lam yi ci weti gaal gi, ngir ñu di ko yóbboo gaal gi. 15Ci lami gaal gi la njàppu yiy des te bañ cee jógeeti. 16Yebal ci gaal gi àlluway seede si ma lay jox.
17«Defarlul kubeer gu ñuy awale njotlaay gu wurusu ngalam ngir gaal gi. Na guddaay bi di ñaari xasab ak genn-wàll, yaatuwaay bi di xasab ak genn-wàll. 18Tëgglul ñaari jëmmi malaakay serub yu wurus te nga féetale leen ak ñaari cati kubeeru njotlaay ga. 19Defal cat lii ab serub, cat lee ab serub te nanga móolaale kubeer gi ak serub yi ci ñaari cat yi, ñu ànd di benn. 20Na serub yi tàllal seeni laaf, jëme kaw te nañu yiire kubeeru njotlaay gi seeni laaf. Nañu janoo, te na seeni kanam jublook kubeeru njotlaay gi. 21Tegal kubeeru njotlaay gi ci kaw gaal gi, gannaaw boo ci yebee àlluway seede si ma lay jox. 22Foofa laay dajeek yaw; fa tiim kubeeru njotlaay ga, ca diggante ñaari serub ya ca kaw gaalu seede sa, fa laa lay waxe mboolem lu ma lay sant, ñeel bànni Israayil.
Lu jëm ci taabalu mburum teewal mi
23«Defarlul taabalu bantu séng, guddaay bi di ñaari xasab, yaatuwaay bi di xasab, taxawaay bi di xasab ak genn-wàll. 24Xoob ko wurusu ngalam te defal ko kéméju wurus gu ko wër. 25Defal ko pegg bu ko wër bu tollu ci ñeenti baaraam, te sàkkal pegg ba kéméju wurus, wërale ko. 26Defarlul ko ñeenti lami wurus te we lam ya ca ñeenti wet ya, fa fareek ñeenti tànk ya. 27Na lam yi dendeek pegg ngir mana téye njàppu yi ñuy yóbboo taabal ji. 28Yattlul ay njàppu yu bantu séng, nga xoob njàppu yi wurus, ñu di ko yóbboo taabal ji. 29Sàkkal ko ay ndabam yu tell aki mbàttoom aki njaqam, ak këllam yi ñuy tuural Yàlla. Te wurusu ngalam ngay def lu ci nekk. 30Tegal mburum teewal mi ci kaw taabal ji, mu nekk ci sama kanam ba fàww.
Lu jëm ci tegukaayu làmp bi
31«Defarlul tegukaayu làmp bu wurusu ngalam. Tegukaay ba, dees koy tëgg. Na taatu tegukaay ba ak per ba ànd aki kaasam aki kàmbóotam aki mbaram, lépp di benn. 32Juróom benni car a soqikoo ci weti tegukaayu làmp bi, ñetti car ci gii wet, ñett ci gi ci des. 33Benn car day am ñetti kaas yu bindoo ni tóor-tóori garabu amànd#25.33 garabu amànd xeetoo naak gerte-tubaab., kaas bu ci nekk ànd ak ay kàmbóotam aki mbaram, car ba ca topp am ñetti kaas yu bindoo ni tóor-tóori garabu amànd, kaas bu ci nekk ànd aki kàmbóotam aki mbaram, ba juróom benni car ya soqikoo ca per ba, daj. 34Gannaaw loolu peru tegukaayu làmp ba itam day am ñeenti kaas yu bindoo ni tóor-tóori garabu amànd, ànd ak ay kàmbóotam aki mbaram. 35Ab kàmbóot ay ronu yii ñaari car, jàpp ca; beneen kàmbóot ronu ñaari car ya ca topp, jàpp ca, ab kàmbóot ronu ñaari car ya mujj, jàpp ca, juróom benni car ya soqikoo ca peru làmp ba, daj. 36Kàmbóot ya ak car ya dañuy ànd ak tegukaay ba, di wenn donju wurusu ngalam wu ñu tëgg ba mu jekk. 37Defarlul juróom ñaari làmpam. Te na làmp ya tege tegin wuy leeral ca kanam tegukaay ba. 38Ñiimi feyukaayu làmp yi ak andi làmp yi na doon wurusu ngalam. 39Fanweeri kiloy wurusu ngalam ak juróom#25.39 Mu yemook benn nattu diisaay bu ñu daan jëfandikoo, ñu di ko wax talaŋ., ci lees di sàkk tegukaayu làmp bi, ak mboolem ay jumtukaayam. 40Nanga xool te def leen mu dëppook misaal yi ñu la ciy won ci kaw tund wi.
Currently Selected:
Mucc ga 25: KY
Highlight
Copy
Compare
Share
Want to have your highlights saved across all your devices? Sign up or sign in
Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9
Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/
Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright