YouVersion Logo
Search Icon

Mucc ga 24

24
Yàlla fasoo na kóllëre ak bànni Israayil
1Mu neeti Musaa: «Yéegal ñëw fi Aji Sax ji, yaw ak Aaróona ak Nadab ak Abiyu ak juróom ñaar fukki magi Israayil, te ngeen sujjóote nee, dànd ma. 2Su ko defee yaw rekk yaay dikk, ba jege ma, man Aji Sax ji, waaye ñi ci des buñu jegesi, te it bu mbooloo mi yéegandoo ak yaw.» 3Musaa dem, yeggeji mbooloo ma kàdduy Aji Sax ji yépp, ak àttey yoonam yépp. Mbooloo ma mépp bokk benn baat, ne ko: «Li Aji Sax ji wax lépp dinanu ko def.» 4Ba loolu weesoo Musaa bind na mboolem kàdduy Aji Sax ji. Mu xëy nag suba teel, daldi sàkk ab sarxalukaay ca suufu tund wa, sampaale fa fukki doj ak ñaar, ñeel fukki giiri Israayil yaak ñaar. 5Ba mu ko defee mu yebal ay ndawi bànni Israayil, ñu def ay saraxi rendi-dóomal, boole ci rendi yëkk yu ndaw yu ñu def saraxi cant ci biir jàmm, ñeel Aji Sax ji. 6Musaa jël genn-wàllu deret ja, sotti ci ay ndab, la des ca deret ja, mu xëpp ko ca sarxalukaay ba. 7Ba loolu amee mu jël téere ba ñu bind kóllëre ga, jàngal ko mbooloo ma, ñuy dégg. Mbooloo ma ne ko: «Li Aji Sax ji wax lépp dinanu ko def, ba mu mat sëkk.» 8Musaa jël deret ja, wis-wisal ca kaw mbooloo ma, ne leen: «Lii nag mooy deret ji Yàlla fase kóllëre gi mu séq ak yeen te mu aju ci mboolem kàddoom yii.»
9Ba loolu amee Musaa yéeg, ànd ak Aaróona ak Nadab ak Abiyu ak juróom ñaar fukki magi Israayil. 10Ñu daldi gis Yàllay bànni Israayil. Lu mel ni dëru per bu safiir a nga lal tànkam ya, mel ni asamaan, ndax na mu sete wecc. 11Waaye njiiti bànni Israayil ña, loxol Yàlla dalu leen. Ñoo gis Yàlla, te gannaaw loolu lekk nañu, naan nañu.
Musaa yéeg na ca tund wa
12Aji Sax ji waxati Musaa ne ko: «Yéegal ba ci man ci kaw tund wi te négandiku fa, ma jox la àlluway doj yi ak yoon wi, ak santaane yi ma ci bind ngir jàngale ko.» 13Musaa daldi jóg, mook Yosuwe, bëkk-néegam. Musaa nag yéeg ca tundu Yàlla wa. 14Fekk na mu wax mag ña ne leen: «Xaarleen nu fii, ba nu délsi. Aaróona ak Ur a ngi nii ak yeen; ku ci am mbir mooy àttelu, demal ci ñoom.»
15Ba Musaa yéegee ca kaw tund wa, niir wa daa yiir tund wa, 16leeru Aji Sax ja dal ca kaw tundu Sinayi, niir wa yiir tund wa diiru juróom benni fan. Bésub juróom ñaareel ba Aji Sax ji àddoo ca digg niir wa, woo Musaa. 17Melow leeru Aji Sax jaa ngay nirook sawara wuy tàkk ca njobbaxtalu tund wa, bànni Israayil di gis. 18Musaa yéeg ca kaw tund wa ba tàbbi ca biir niir wa, di wéy. Musaa nekk na ca kaw tund wa ñeent fukki guddi ak ñeent fukki bëccëg.

Currently Selected:

Mucc ga 24: KY

Highlight

Copy

Compare

Share

None

Want to have your highlights saved across all your devices? Sign up or sign in