YouVersion Logo
Search Icon

Kolos 4

4
1Yeen ñiy sang yi, yorleen seeni jaam, yorin wu jub te aw yoon, te ngeen xam ne yeen itam am ngeen ab Sang fa asamaan.
Yeneen warugar a ngii
2Ag ñaan nag, saxooleen ko, te ngeen teewlu ci, boole ci ag cant. 3Te ngeen ñaanaale nu ci itam, ngir Yàlla ubbil nu buntu xamle kàddu gi, ngir siiwal mbóot mi ci Almasi bi, li waral ñu jéng ma. 4Ñaanleen, ma man koo wax ba mu leer nàññ ni mu ma ware.
5Jëfeleen xel mu rafet seen diggante ak aji gëmadi ñi ci biti, te jot gi ngeen amagum, fexeleen ba jariñoo ko. 6Na seen kàddu ànd ak yiw te am solo, te ngeen xam nu ngeen di tontoo ku nekk, tont li war.
Póol tàggu na waa Kolos
7Mboolem lu jëm ci man nag, Tisig dina leen ko xamal. Mbokk la, soppe la, jawriñ ju wóor la, te it sama mbokkum jaam la, ci liggéeyu Boroom bi. 8Lii sax moo tax ma yónni ko ci yeen: xamal leen lu jëm ci nun, ak itam, teewaayam bu dëfal seen xol. 9Onesim lay àndal, sunu mbokk mu wóor, di sunu soppe, te mu bokk ci yeen. Ñoo leen di xamal mboolem lu fi xew.
10Aristàrk mi ma bokkal kaso bi, mu ngi leen di nuyu, moom ak Màrk rakku Barnabas. Ci mbiru Màrk moomu ngeen jotoon ndigal, ngir bu dikkee, ngeen teral ko. 11Yeesu mi ñuy wax Yustus itam, mu ngi nuyoo. Li bokk ci askanu Yawut, ñoom rekk ay liggéeyandoo ak man ngir nguurug Yàlla, te ñoo seral sama xol. 12Ab nuyoo it ñeel na leen, tukkee ci Epafras mi bokk ci yeen, te di jaamub Almasi Yeesu. Muy ku jàmbaare ci saxoo leena ñaanal, ngir seenub taxawaay sotti te mat sëkk ci jëfe mboolem luy coobarey Yàlla. 13Maa ko seedeel ne coonoy ñaan bu réy la nekke, ngir yeen ak waa Lawdise ak waa Yerapolis. 14Ab nuyoo it ñeel na leen, tukkee ci sunu soppe Luug, doktoor bi, ak Demas. 15Nuyulleen nu bokk yi dëkke Lawdise, ak sunub jigéen Nimfa ak mbooloom gëmkat miy daje këram.
16Gannaaw bu ngeen jàngee-biral bataaxal bii ci seen biir, fexeleen it ba ñu jàng ko biral fa mbooloom gëmkat ma fa Lawdise, te yeen it bataaxal ba ngeen di jote Lawdise, nangeen ko jàng-biral.
17Waxalleen ma Arsipp ne ko: «Neel jàkk ci liggéey bi nga sasoo ci Boroom bi, ngir nga sottal ko.»
18Man Póol nag maa leen di bind tàggatoo bii ci sama loxol bopp. Fàttalikuleen ne dañu maa tëj kaso. Yal na aw yiw ànd ak yeen!

Currently Selected:

Kolos 4: KY

Highlight

Copy

Compare

Share

None

Want to have your highlights saved across all your devices? Sign up or sign in