Jëf ya 18
18
Póol tiiñ na waa Korent
1Ba loolu wéyee Póol bàyyikoo Aten, dem Korent. 2Mu daje fa ak Yawut bu ñuy wax Akilas, fekk baax diiwaanu Pont. Muy sooga jóge réewum Itali, ànd ak soxnaam Piriska#18.2 Piriska mooy Pirsil ba tey., ndax Buur bu mag ba Këlódd moo joxe woon ndigal ne na Yawut yépp génn Room. 3Póol nag miinante ak ñoom, te fekk ñu bokk benn liggéey, di defarkati xayma ni moom. Loolu tax mu far dal ak ñoom, di liggéey.
4Ci kaw loolu bésub Noflaay bu nekk Póol daan waare ca jàngub Yawut ba, di yee Yawut yi ak Gereg yi. 5Ba Silas ak Timote dikkee, bàyyikoo diiwaanu Maseduwan, Póol xintewootul lu moy di xamle kàddu gi, di seedeel Yawut yi ne Yeesu mooy Almasi bi. 6Yawut ya nag gàntal, di ko ŋàññ, mu yëlëb ay yéreem, misaale ko ne jaanam wàcc na. Mu ne leen: «Yeenay gàddu seen bakkanu bopp. Man set naa ci wecc. Gannaaw-si-tey, ci jàmbur ñi dul Yawut laa jëm.»
7Mu jóge foofa, dem ci kër benn jàmbur bu dul Yawut te muy jaamukatu Yàlla bu ñuy wax Tisyus Yustus, te këram sësook jàngu ba. 8Teewul Kirispus njiitu jàngu ba moom gëm Sang bi, mook waa këram gépp. Ñu bare ci waa Korent a gëm, gannaaw ba ñu déggee kàddu gi, ba ñu sóob leen ci ndox.
9Ba loolu amee Sang bi wax ak Póol ag guddi ci biir peeñu, ne ko: «Bul tiit dara, waaye waxal te bul noppi, 10ndax maa ànd ak yaw. Kenn du la song, def la lu bon, ndax ñu bare ci dëkk bii samay ñoñ lañu.» 11At ak juróom benni weer la Póol toog ci seen biir, di jàngale kàddug Yàlla.
12Jant ya Galyon moomee diiwaanu Akayi, Yawut ya dañoo mànkoo, jógal Póol, jàpp ko, yóbbu ca àttekaay ba. 13Ñu ne: «Kii dafa juuyoo ak yoon ci ni muy xiire nit ñi ci jaamu Yàlla.»
14Póol dem bay àddu, far Galyon ne Yawut ya: «Yeen Yawut yi, su doon ag njubadi mbaa jëf ju aay lool ju ngeen di tawat, kon xel dina nangu ma déglu leen. 15Waaye su dee ag dëngoo ci wàllu wax, mbaa ay turi nit, mbaa seen yoonu bopp nag, seetalleen ko seen bopp. Àtte boobu moom, duma ko nangu.» 16Galyon daldi leen dàqe ca àttekaay ba. 17Ci kaw loolu ñépp jàpp Sosten, njiitu jàngu ba, dóor ko ca àttekaay ba, te taxul Galyon yégal ko yaramam.
Póol délsi na Àncos gu Siri
18Ba loolu wéyee Póol toogaat na fa fan yu bare, doora tàggatoo ak bokk ya, dugg gaal jëm Siri, ànd ak Piriska ak Akilas. Fekk na mu watu nel ca teerub Señsere, firndeele ko aw xas wu mu xasoon.
19Ba ñu teeree Efes, fa la Póol bàyyi Piriska ak Akilas. Mu dem ca jàngu ba, ba diisoo fa ak Yawut ya. 20Ñooñu ñaan ko, mu toogaat fa ab diir, mu gàntal. 21Naka la tàggatoo ak ñoom, ne leen: «Dinaa leen seetsiwaat, bu soobee Yàlla.» Ba loolu amee mu dugg gaal, bàyyikoo Efes, 22teereji Sesare. Mu dem nag Yerusalem, nuyuji mbooloom gëmkat ña, doora dem Àncos gu Siri.
Póol tukki na ñetteel bi yoonam
23Póol toog na Àncos ay fan, jóge fa wër diiwaanu Galasi, teg ca Firisi, di ñaax mboolem taalibey foofa.
24Ab Yawut nag bu ñuy wax Apolos te cosaanoo Alegsàndiri, moo dikkoon Efes. Ku rafet kàddu, te xam Mbind yi lool. 25Kooku jotoon naa jàng yoonu Sang bi. Mu ànd ak cawarte, di waare aka jàngale lu wér péŋŋ ci mbirum Yeesu, doonte xam-xamam a ngi yemoon ci sóobeb Yaxya ci ndox. 26Mu tàmbalee wax ak kóolute ca jàngub Yawut ba. Piriska ak Akilas dégg ko, woo ko cig wet. Ñu daldi koy gëna leeralal yoonu Yàlla wi.
27Ba mu ko defee Apolos namma jàll ba Akayi, bokk ya rafetlu mébétam. Ñu bind taalibey Akayi, ngir ñu dalal ko. Ba Apolos agsee Akayi, dimbali na lool ña fa yiw may ñu doon ay gëmkat. 28Ndax fa kanam mbooloo ma la doon tiiñale Yawut ya ay firnde yu mat sëkk, firil leen Mbind mi, ba leeralal leen nàññ ne Yeesu mooy Almasi bi.
Currently Selected:
Jëf ya 18: KY
Highlight
Copy
Compare
Share
Want to have your highlights saved across all your devices? Sign up or sign in
Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9
Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/
Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright