Jëf ya 17
17
Xibaaru Yeesu yëngal na Tesalonig
1Ba mu ko defee ñu jaare ca dëkk ya ñuy wax Amfipolis ak Apoloni, doora àgg Tesalonig ga Yawut ya amoon ab jàngu. 2Póol nag di leen fa fekk, na mu ko baaxoo. Diiru ñetti bési Noflaay, mu di leen waxal ci Mbind mi. 3Mu di leen tekkil Mbind mi, di leen ci firndeel ne coonob Almasi bi ak ndekkiteem manul woona ñàkk. Mu ne leen: «Yeesu mii ma di leen xamal, mooy Almasi bi.» 4Ba loolu amee ñenn ca Yawut ya gëm, fekksi Póol ak Silas, ñoom ak Gereg yu bare yu ragal Yàlla, ak jigéen ñu ràññiku ñu bare.
5Yawut ya nag am ca kañaan, daldi foraatoo ca mbedd ma ay taxawaalukat, dajale ay gàngoor, ba yëngal dëkk ba. Ñu song kër Yason, di seet Póol ak Silas, ngir yóbbu leen ca waa dëkk ba. 6Ci kaw loolu gisuñu leen, ñu diri Yason ak yeneen bokki gëmkat ba ca kanam àttekat ya. Ña ngay biral, naan: «Nit ñi tas àddinaa ngii, agsi nañu fi, 7te Yason a leen dalal. Ñoom ñépp a xëtt ndigali buur Sesaar, te naan am na beneen buur bu ñuy wax Yeesu.» 8Ba mbooloo ma ak àttekati dëkk ba déggee loolu, dañoo jaaxle. 9Ba loolu amee ñu feyloo Yason ak ña ca des daan ba ca war, door leena yiwi.
Póol ak Silas dem nañu Bere
10Ba mu ko defee bokki gëmkat ña yebal ca saa sa Póol ak Silas ca guddi ga, ñu jëm Bere. Ñu agsi, dem ca jàngub Yawut ya. 11Waa Bere nag gëna am déggin waa Tesalonig. Ñu gëm kàddu gi, xér ci lool, bés bu nekk ñuy niir Mbind mi, ngir xam ndax la ñu leen di wax noonu la. 12Ci kaw loolu Yawut yu bare gëm, ñoom ak jigéeni Gereg ñu ràññiku, ak ay góori Gereg ñu bare.
13Ba loolu amee Yawuti Tesalonig dégg ne Póol a ngay xamle kàddug Yàlla ca Bere itam. Ñu dikkati, yëngal nit ña, ñu def ay gàngoor. 14Ca la bokki gëmkat ñi yebal Póol ca saa sa, mu jëm ca tefes ga, Silas ak Timote ñoom, des ca Bere. 15Ña dar Póol nag gunge ko ba ca dëkk ba ñuy wax Aten, ñu doora dëpp, jottaliji Silas ak Timote kàddug Póol, ngir ñu fekksi ko nu mu gëna gaawe.
Póol waare na ca Aten
16Diggante ba Póol di nég Silas ak Timote ca Aten, xolam jeex na ndax dafa gis na dëkk ba yeboo ci jaamu ay tuur. 17Ci biir loolu muy wax ak Yawut yaak jàmburi ragalkati Yàlla ya ca jàngu ba, di wax it ak waa pénc ma bés bu nekk.
18Ci kaw loolu ay boroom xam-xam yu bokk ci ngérum Epikur#17.18 ngérum Epikur mooy kuréelu njàngalem Epikur, mi dee 270 at lu jiitu Almasi bi. Ngérum Epikur dañoo jiital seen bakkan, te fonk bànneex. ak ngérum Estowisen#17.18 ngérum Estowisen, kuréel la woon gu njàngalem Senon lal. Dee na 265 at lu jiitu Almasi bi. Ngérum Estowisen ñoo weesale seen bopp yég-yégu yaram mbaa xol yu mel ni bànneex mbaa naqar, te di ñaaxe ci muñ gu ànd ak pastéefu boroom., di werante ak moom. Ñenn ña ne: «Kebetukat bii, lu muy wax nii?» Ña ca des dégg Póol di waare xibaaru jàmm bi ci Yeesu ak ndekkiteem, ñu ne: «Daa mel ni ay tuur-tuuraani doxandéem lay waareel.» 19Ñu jàpp ko nag, yóbbu ko ca ëttub àttekaay ba ñuy wax Areyopas. Ñu ne ko: «Ndax man nanoo xam njàngale mu bees mii ngay siiwal, lu mu doon? 20Ndax li ngay wax kat sunu ngan-gi-nopp la. Nu bëgga xam nag loolu lu muy tekki.» 21Booba waa Aten ñépp, doxandéem ak njuddu-ji-réew, xintewuñu lenn lu moy di nettali aka déglu xew-xew wu bees.
22Ci kaw loolu Póol taxaw ca digg ëttub Areyopas, ne leen: «Yeen waa Aten, gis naa ne ci wet gu nekk ñu farlu ngeen ci diine. 23Ndax maa doon doxantu, di seet seeni jaamookaay, ba yem ci sarxalukaay bu ñu bind mii mbind: “Ñeel yàlla ji nu xamul.” Loolu ngeen di màggal te xamuleen ko nag, moom laa leen di xamal.
24«Yàlla mi sàkk àddina ak mboolem li ci biiram, di Boroom asamaan ak suuf, dëkkewul màkkaan mu ay loxo sàkk. 25Te it jariñoowul loxol nit, mbete ku soxla lenn, ndax mooy may ñépp bakkan akug noo, ak lu mu mana doon. 26Moo sàkke xeeti àddina yépp ci kenn nit, ñu dëkke déndub suuf sépp, te moo leen àppal seeni jamono, rëddal leen seen kemi dëkkuwaay. 27Yàllaa def loolu, ngir xeeti àddina wut ko, làmbatu ba daj ko, ndegam man naa am, doonte sorewul kenn ku nekk ci nun. 28“Ndax sunu bakkan ak sunu yëngu ak sunug nekk, lépp ci moom la.” Mooy ba tey la ñenn ci seeni woykat ne: “Nun itam aw xeetam lanu.” 29Ndegam nag xeetu Yàlla lanu, warunoo nirule Yàlla ak lenn luy wurus mbaa xaalis mbaa aw doj te sosoo ci xareñtey nit akum xelam. 30Yàlla nag jéllale na jamonoy ñàkka xam googa woon, waaye tey mu ngi woo ñépp ak fépp fu ñu féete, ngir ñu tuub. 31Ndaxte Yàlla jàpp na bés bu muy àttee àddina ci dëgg, àtte bu nit ki mu tabb di sottali; te loolu Yàlla jox na ci ñépp firnde lu wóor, ba mu dekkalee kooku mu tabb, ndekkite lu dee toppul.»
32Naka lañu dégg waxi dee-dekki, ñenn ña di ko foontoo, ña ca des ne ko: «Dinanu la déglu, nga waxalaat nu ci moomu mbir.» 33Ba loolu amee Póol bàyyikoo ca seen biir. 34Teewul mu am ñu ko fekksi, ba mujj gëm; Deni mi bokk ci ëttub Areyopas ci la, ak jigéen ju ñuy wax Damaris, ak ñeneen.
Currently Selected:
Jëf ya 17: KY
Highlight
Copy
Compare
Share
Want to have your highlights saved across all your devices? Sign up or sign in
Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9
Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/
Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright