1
Jëf ya 17:27
Kàddug Yàlla
KY
Yàllaa def loolu, ngir xeeti àddina wut ko, làmbatu ba daj ko, ndegam man naa am, doonte sorewul kenn ku nekk ci nun.
Compare
Explore Jëf ya 17:27
2
Jëf ya 17:26
Moo sàkke xeeti àddina yépp ci kenn nit, ñu dëkke déndub suuf sépp, te moo leen àppal seeni jamono, rëddal leen seen kemi dëkkuwaay.
Explore Jëf ya 17:26
3
Jëf ya 17:24
«Yàlla mi sàkk àddina ak mboolem li ci biiram, di Boroom asamaan ak suuf, dëkkewul màkkaan mu ay loxo sàkk.
Explore Jëf ya 17:24
4
Jëf ya 17:31
Ndaxte Yàlla jàpp na bés bu muy àttee àddina ci dëgg, àtte bu nit ki mu tabb di sottali; te loolu Yàlla jox na ci ñépp firnde lu wóor, ba mu dekkalee kooku mu tabb, ndekkite lu dee toppul.»
Explore Jëf ya 17:31
5
Jëf ya 17:29
Ndegam nag xeetu Yàlla lanu, warunoo nirule Yàlla ak lenn luy wurus mbaa xaalis mbaa aw doj te sosoo ci xareñtey nit akum xelam.
Explore Jëf ya 17:29