Bible App logo
Search Icon

Jëf ya 14

14
Póol ak Barnabas waare nañu ca dëkku Ikoñum
1Ba Póol ak Barnabas nekkee Ikoñum, noonu lañu dugge itam ca jàngub Yawut ya. Ñuy waare, ba ay Yawut aki Gereg yu bare gëm. 2Yawut yi gëmul nag di xiirtal jàmbur ñi dul Yawut, di yàq seen xel ci bokki taalibe yi. 3Teewul Póol ak Barnabas toog Ikoñum diir bu yàgg lool. Fit lañu doon waaree ngir Boroom bi, Boroom bi maye ay firnde aki kéemaan yu jaare ci ñoom, ngir seedee ko kàddug yiwam gi ñuy biral. 4Ba loolu amee waa dëkk bi xàjjalikoo, ñii far ak Yawut yi, ñale far ak ndaw ya. 5Jàmbur ñeek Yawut yi nag ànd ak seeni kilifa, di leen waaja mitital aka dóori doj. 6Ñu yég ko, daw làquji diiwaanu Likawni, ca dëkk ya ñuy wax Listar ak Derbe ak la ko wër. 7Foofa itam ñu di fa xamle xibaaru jàmm bi.
Póol ak Barnabas waare nañu ca Listar
8Jenn waay a nga daan toog ca Listar, tànk ya baaxul woon; laago la judduwaale, te masula dox. 9Kookoo dégg Póol muy waare, Póol xool ko jàkk, gis ne am na ngëm gu ag muccam mana jaare. 10Mu àddu ca kaw, ne waa ji: «Jógal taxaw jonn!» Waa ji ne bërét, jóg, daldi dox.
11Ba mbooloo ma gisee la Póol def, ca kaw lañu àddu ci làkku likawni, ne: «Yàlla yee soppaliku melow nit, wàccsi ci sunu biir!» 12Ci kaw loolu ñu tudde Barnabas Sës, kilifay yàllay Gereg yi, Póol nag gannaaw moo farewoo woon kàddug waare ga, ñu tudde ko Ermes, ndawal yàllay Gereg yi. 13Jaamookaayu Sës ma nga woon ca buntu dëkk ba. Sarxalkat ba daldi indi ca bunti dëkk ba ay yëkk yu ñu takkal caqi tóor-tóor. Sarxalkat ba ànd ak mbooloo ma, nara rendi jur ga, sarxal ko Póol ak Barnabas.
14Ci kaw loolu Póol ak Barnabas yég la xew. Ñu xotti seeni yére ndax ñaawlu ko. Ñu buur nag ba ca biir mbooloo ma, daldi àddu ca kaw ne: 15«Yeen, lu leen xiir ci lii? Nun itam ay nit lanu, bokk ak yeen benn bind. Xibaaru jàmm bi lanu leen di xamal, ngir ngeen wacc yëfi neen yii te walbatiku ci Yàlla, kiy dund te sàkk asamaan ak suuf ak géej ak lépp li ci biir. 16Moo mayoon démb xeet yépp, ñu aw ci seen yooni bopp. 17Moona noppiwula seedeel boppam ci mbaaxam gi muy jëfe, di leen wàcceel fa asamaan taw ak naataange, reggal leen, bégal leen ba seen xol sedd.»
18Loolu lépp ndaw ya wax nañu ko te tuuti kon ñu tëlee tere mbooloo ma ñu rendil leen sarax.
19Ci kaw loolu ay Yawut yu jóge Àncos gu Pisidi ak Ikoñum, fexe ba fàbbi mbooloo ma, daldi dóor Póol ay doj, diri ko ba génne ko dëkk ba, yaakaar ne dee na. 20Naka la ko taalibe ya yéew, mu jóg, daldi dellu ca biir dëkk ba. Ca ëllëg sa, mu ànd ak Barnabas, dem Derbe.
Délsi nañu Àncos gu Siri
21Gannaaw ba ñu xamlee fa Derbe xibaaru jàmm bi, ba am fa taalibe yu bare, dañoo dellu Listar ak Ikoñum ak Àncos gu Pisidi. 22Ñuy feddali pastéefu taalibe yi, di leen ñaax ngir ñu saxoo ngëm, ne leen: «Coono yu baree ngii, fàww nu jaare ci, ngir tàbbi ci nguurug Yàlla.» 23Mbooloom gëmkat mu nekk nag, ñu tabb ci ay mag; ci biir loolu ñu ñaan, boole kook koor, daldi dénk mag ña Sang bi ñu gëm. 24Gannaaw loolu ñu jaare biir diiwaanu Pisidi, ba àgg Pamfili. 25Ñu daldi siiwtaane kàddu gi ca Perge, doora wàcci ba Atali.
26Foofa lañu dugge gaal, dellu Àncos gu Siri ga ñu leen dénke woon Yàlla ciw yiwam, ngir liggéey ba ñu sottal, ba délsi noonu. 27Ba ñu agsee, dañoo woo mbooloom gëmkat ña, àgge leen mboolem na Yàlla def ak ñoom, ak na mu ubbilee jàmbur ñi dul Yawut buntu ngëm. 28Ñu toog nag ak taalibe ya diir bu xawa yàgg.

Currently Selected:

Jëf ya 14: KY

Highlight

Copy

Compare

Share

None

Want to have your highlights saved across all your devices? Sign up or sign in