Jëf ya 15
15
Péncoo am na ca Yerusalem
1Ñenn nit ñu bàyyikoo Yude dikk Àncos, ñoo doon digal bokki taalibe yi, ne leen: «Su ngeen xaraful#15.1 Seetal ci 7.8., ni ko aaday Musaa santaanee, dungeen mana mucc.»
2Mbir ma nag mujje féewaloo ak werante wu xawa metti, te Póol ak Barnabas séq ko ak ñooñu. Ba loolu amee ñu ne, na Póol ak Barnabas ak ñenn ca gëmkati Àncos ànd dem Yerusalem ca ndawi Yeesu ak mag ña, ba lijjanti mbir moomu.
3Ci kaw loolu mbooloom gëmkat ñi yebal leen, ñu jaare Fenisi ak Samari, daldi àgge waa foofa ni jàmbur ñi dul Yawut tuube, ba bokki gëmkat ñépp bég ca lool. 4Gannaaw loolu, ñu agsi Yerusalem, mbooloom gëmkat ñi ak ndawi Yeesu yi ak mag ñi dalal leen, ñu nettali leen mboolem ni Yàlla def ak ñoom.
5Ba mu ko defee ñenn ci gëmkat ñi bokk ci ngérum Farisen yi, daldi taxaw temm, ne gëmkat ñi dul Yawut, fàww ñu xarafal leen, sàmmloo leen yoonu Musaa.
6Ba loolu amee ndawi Yeesu yi ak mag ñi bokk daje, ngir seet mbir moomu. 7Werante wu réy am ca. Ci kaw loolu Piyeer jóg ne leen: «Bokk yi, yeen xam ngeen ne bu yàgg la ma Yàlla seppee ci seen biir, ngir jàmbur ñi dégge ci sama làmmiñ kàddug xibaaru jàmm bi, ba doon ay gëmkat. 8Yàlla mi xam xolu nit nag moo seedeel jàmbur ñi, ba mu leen mayee Noo gu Sell gi, ni mu nu ko maye nun itam. 9Yàlla amul xejj ak seen sunu dig ak ñoom, ndax seen ngëm la raxase seen xol. 10Léegi nag lu tax ngeen di diiŋat Yàlla, di teg taalibe yi yen bu nu masula àttan, cay maam ba ci nun? 11Yiwu Sang bi Yeesu daal lanu gëm ne ci lanuy mucce, te ñoom itam, noonu rekk.»
12Ba loolu wéyee mbooloo mépp ne xerem. Ñu déglu nag Barnabas ak Póol, ñu xamle mboolem firnde yeek kéemaan yi Yàlla defe seen ñaari jëmm ci biir jàmbur ñi. 13Ba ñu noppee, Yanqóoba àddu ne: «Bokk yi, dégluleen ma. 14Simoŋ#15.14 Simoŋ mooy Piyeer ba tey. xamle na, ni Yàlla yége jàmbur ñi ca njàlbéen, ba sàkke ci seen biir xeet wu mu tudde turam. 15Te loolu dëppoo na ak kàdduy yonent yi, ndax bindees na ne:
16“Boroom bi nee:
Gannaaw loolu dinaa délsi;
maay yékkati mbaarum Daawuda mi daanu,
maay yékkati gent yi, joyanti ko,
17ngir ndesu nit ñi wuta xam Boroom bi,
te ñooñoo di jàmbur ñi ñu tudde sama tur#15.16-17 Seetal ci Amos 9.11-12..
18Boroom bee xamle loolu bu yàgga yàgg#15.18 Seetal ci Esayi 45.21..”
19«Kon nag sama xalaat mooy: bunu gétën jàmbur ñi tuub, ba waññiku ci Yàlla. 20Xanaa nu bind leen, ne leen ñu moytu lu ay xërëm sobeel, moytu séy yi yoon tere, moytoo lekk yàppu mala mu ñu tuurul deretam, ak lekk deret ci boppam. 21Ndaxte ca njàlbéen ga ba tey ay nit a ngi waaree yoonu Musaa ci dëkk bu nekk, ñu di ko jàng ci jàngu yi bésub Noflaay bu nekk.»
Ndaje ma bind na ñi dul Yawut
22Ba loolu amee ndaw yi ak mag ñi mànkoo ak mbooloom gëmkat ñépp, ngir tànne ci seen biir ay nit, yebal leen Àncos, boole leen ak Póol ak Barnabas. Ñooñoo di Yuda mi ñu dippee Barsabas, ak Silas, ñu diy mag ca bokk ya.
23Ñu yóbbante leen bataaxal, bind ci ne:
«Nun ndawi Yeesu ak mag ñi, seen bokki Yerusalem, noo leen bind, yeen sunu bokki gëmkat ñi dul Yawut te dëkke Àncos ak Siri ak Silisi. Nu ngi jiital sunub nuyoo. 24Dégg nanu ne ay nit ñu bawoo ci nun, ñoo leen lëjal ak seeni wax, di jaxase seen xel, te nun joxunu leen lenn ndigal. 25Moo tax nu mànkoo ci tànn ay nit ñu nu yebal ci yeen, boole leen ak sunuy soppe Barnabas ak Póol, 26ñoom ñi jaay seen bakkan ngir sunu Sang Yeesu Almasi. 27Kon nag noo yebal Yuda ak Silas, ngir ñu àgge leen ci seen gémmiñu bopp, lii nu leen bind. 28Ndaxte Noo gu Sell gi moo mànkoo ak nun ci bañ leena teg benn coono, xanaa lii manula ñàkk: 29Ngeen moytu yàpp wu ñu sarxal ay tuur, ak deret, ak yàppu jur gu ñu tuurul deretam, ak séy yi yoon tere. Yooyii, bu ngeen ko moytoo bu baax, def ngeen lu baax. Jàmm ak jàmm.»
30Ba loolu amee ñu tàggatoo, daldi dem ba Àncos. Ci kaw loolu ñu woo mbooloo mi, jébbal leen bataaxal bi. 31Ba ñu jàngee bataaxal bi, kàddu ga dëfal leen, seen xol sedd. 32Yuda ak Silas it gannaaw ay yonent lañu woon, wax nañu ak bokk yi lu yàgg, ngir ñaax leen, feddali seen ngëm. 33-34Ba loolu amee ñu toog fa ab diir, bokk yi door leena ñaanal yoonu jàmm, yiwi leen, ngir ñu dellu ca ña leen yebaloon. 35Póol ak Barnabas nag des Àncos. Ñu ànd ak ñeneen ñu bare, di jàngale aka xamle kàddug Boroom bi.
Póol ak Silas ànd nañu
36Ba ñu ca tegee ay fan Póol ne Barnabas: «Nan dellu seeti bokk yi ci mboolem dëkk yi nu yégle woon kàddug Boroom bi, ba gis nu ñu def.» 37Barnabas nag bëggoon ñu yóbbaale Yowaan mi ñuy wax Màrk. 38Teewul Póol jàpp ne gannaaw Yowaan Màrk moomu moo leen waccoon ca Pamfili te àndul woon ak ñoom ci liggéey bi, yóbbaale ko warul.
39Mbir mi nag mujje dëngoo bu metti, ba ñu teqalikoo. Barnabas ànd ak Yowaan Màrk, dugg gaal, jëm Sippar. 40Póol moom taamu Silas, daldi ànd ak moom dem, gannaaw ba leen bokk ya dénkee Boroom bi ciw yiwam. 41Ci kaw loolu mu jaare diiwaani Siri ak Silisi, di ñaax mboolooy gëmkat ña.
Currently Selected:
Jëf ya 15: KY
Highlight
Copy
Compare
Share
Want to have your highlights saved across all your devices? Sign up or sign in
Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9
Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/
Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright